Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

10 feewriyee ba 16 feewriyee

TAALIFI CANT 147-150

10 feewriyee ba 16 feewriyee

Woy-Yàlla nº 29 ak ñaan | Kàddu yi ñuy tàmbalee ndaje bi (1 minit)

NJÀNGALE YU AM SOLO YU NEKK CI KÀDDU YÀLLA

1. Li war a tax ñu màggal Yexowa bare na

(10 minit)

Dafay toppatoo kenn ku nekk ci ñun (Taalifi Cant 147:​3, 4; w17.07-F 18 § 5-6)

Dafa bare yërmande te di jëfandikoo kàttanam ngir dimbali ñu (Taalifi Cant 147:5; w17.07-F 18 § 7)

May na ñu ay mbokk ci mbooloom. Loolu, cér bu réy la. (Taalifi Cant 147:​19, 20; w17.07-F 21 § 18)


LAAJAL SA BOPP LII: ‘Leneen lan moo may xiir ma màggal Yexowa?’

2. Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi

(10 minit)

  • Taalifi Cant 148:​1, 10—Naka la «picc yi » di màggale Yexowa? (it-2-F 438)

  • Ban aaya ngeen xóotal ci seen njàngum Biibël bi ci semen bi?

3. Aaya yi ñu war a liir ci Biibël bi

YOKKAL SA MËN-MËN CI LIGGÉEYU WAARE BI

4. Ni nga mënee tàmbali waxtaan

(3 minit) KËROO-KËR. Li nga mën a def bu la nit ki waxee ne dafa am feebar bu yàgg. (lmd-F lesoŋ 2 ponk 5)

5. Ni nga mënee tàmbali waxtaan

(4 minit) WAARAATE SAA YU ÑU AMEE BUNT. Xoolal ni nga mënee wax nit ki lenn li nga jàng ci ndaje bi nga teewe ci lu yàggul. (lmd-F lesoŋ 4 ponk 3)

6. Waxtaan bi

(5 minit) w19.03-F 10 § 7-11—Turu waxtaan bi: Nanga déglu Yeesu—Yégleel xibaaru jàmm bi. Xoolal foto bi. (th lesoŋ 14)

DUNDINU KERCEEN

Woy-Yàlla nº 159

7. Li ñu def ci léggéeyu waare bi ci at bi

(15 minit) Waxtaan ak ñi teew.

Jàngal yégle bi jóge ci banqaas bi, te mu jëm ci li ñu def ci léggéeyu waare bi ci at bi. Boo pare nga laaj ñi teew leneen lu neex li ñu gis ci téere bi tudd ci farãse Rapport mondial des Témoins de Jéhovah pour l’année de service 2024. Waxal ñaar walla ñetti waarekat ñu nettali lu neex li ñu dund ci liggéeyu waare bu daaw.

8. Njàngum Biibël bi ci biir mbooloo mi

Kàddu yi ñuy tëje ndaje bi (3 minit) | Woy-Yàlla nº 37 ak ñaan