Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

17 feewriyee ba 23 feewriyee

KÀDDU YU XELU 1

17 feewriyee ba 23 feewriyee

Woy-Yàlla nº 88 ak ñaan | Kàddu yi ñuy tàmbalee ndaje bi (1 minit)

NJÀNGALE YU AM SOLO YU NEKK CI KÀDDU YÀLLA

Suleymaan a ngi déglu baayam mu koy xelal bu baax

Yeen ndaw ñi, kan ngeen war a déglu?

(10 minit)

[Woneel WIDEO bi tudd ci farãse Introduction aux Proverbes.]

Nanga muus te déglu say waajur (Kàddu yu Xelu 1:8; w17.11-F 29 § 16-17; xoolal foto bi nekk ci paas bu njëkk bi)

Bul topp ñiy def lu bon (Kàddu yu Xelu 1:​10, 15; w05-F 15/2 19-20 § 11-12)

2. Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi

(10 minit)

  • Kàddu yu Xelu 1:22—Ci Biibël bi, bu ñu woowe nit dof, loolu lan lay tekki? (it-1-F 1005)

  • Ban aaya ngeen xóotal ci seen njàngum Biibël bi ci semen bi?

3. Aaya yi ñu war a liir ci Biibël bi

YOKKAL SA MËN-MËN CI LIGGÉEYU WAARE BI

4. Ni nga mënee tàmbali waxtaan

(2 minit) WAARAATE CI BÉRÉB YU BARE NIT. Li nga mën a def bu dee nit ki dafa bëgg a werante ak yaw. (lmd-F lesoŋ 6 ponk 5)

5. Ni nga mënee tàmbali waxtaan

(2 minit) WAARAATE CI BÉRÉB YU BARE NIT. Nit ki déglu na la bu baax. Jox ko sa nimero telefon wala mu jox la bosam ngir ngeen wéyal waxtaan bi. (lmd-F lesoŋ 1 ponk 5)

6. Li ñu mën a wax bu ñu seetiwaatee nit ki

(2 minit) WAARAATE SAA YU ÑU AMEE BUNT. Waxal nit ki ni ñuy defe njàngum Biibël bi. Jox ko itam kàrt bi ñu defar ngir won nit ñi ne mën nañu jàng Biibël bi te duñu fey dara. (lmd-F lesoŋ 9 ponk 5)

7. Ni ñu mënee jàngal nit ñi ba ñu nekk taalibe Yeesu

(5 minit) lff lesoŋ 16 ponk 6. Kenn ci ñi ngay jàngal Biibël bi dafay xel ñaar ndax Yeesu defoon na ay kéemaan dëgg-dëgg. Jëfandikool benn ci waxtaan yi nekk ci “Gëstul” ngir waxtaan ci ak moom. (th lesoŋ 3)

DUNDINU KERCEEN

Woy-Yàlla nº 89

8. Li mbooloo mi soxla ci wàllu ngëm

(15 minit)

9. Njàngum Biibël bi ci biir mbooloo mi

Kàddu yi ñuy tëje ndaje bi (3 minit) | Woy-Yàlla nº 80 ak ñaan