Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

20 sãwiyee ba 26 sãwiyee

TAALIFI CANT 138-139

20 sãwiyee ba 26 sãwiyee

Woy-Yàlla nº 93 ak ñaan | Kàddu yi ñuy tàmbalee ndaje bi (1 minit)

NJÀNGALE YU AM SOLO YU NEKK CI KÀDDU YÀLLA

1. Bul ragal a joxe ay tontu ci ndaje yi

(10 minit)

Dañoo bëgg a màggal Yexowa ak suñu xol bépp (Taalifi Cant 138:1)

Ñaanal Yexowa mu dimbali la boo ragalee joxe ay tontu ci ndaje yi (Taalifi Cant 138:3)

Yenn saay, ragal dafay wone ne dañoo woyof (Taalifi Cant 138:6; w19.01-F 10 § 10)

XELAL: Booy joxe ay tontu yu gàtt mën na tax ba doo tiit.—w23.04-F 21 § 7.

2. Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi

(10 minit)

  • Taalifi Cant 139:​21, 22—Ndax kerceen yi, ñépp lañu war a baal? (it-2-F 490 § 9)

  • Ban aaya ngeen xóotal ci seen njàngum Biibël bi ci semen bi?

3. Aaya yi ñu war a liir ci Biibël bi

YOKKAL SA MËN-MËN CI LIGGÉEYU WAARE BI

4. Ni nga mënee tàmbali waxtaan

(3 minit) WAARAATE CI BÉRÉB YU BARE NIT. (lmd-F lesoŋ 2 ponk 3)

5. Ni ñu mënee jàngal nit ñi ba ñu nekk taalibe Yeesu

(4 minit) WAARAATE CI BÉRÉB YU BARE NIT. Laajal nit ki ndax bëgg na jàng Biibël bi. Ba pare nga won ko naka la ñu koy defe. (lmd-F lesoŋ 10 ponk 3)

6. Waxtaan bi

(5 minit) ijwyp-F waxtaan nº 105—Turu waxtaan bi ci farãse: Comment surmonter ma timidité ? (th lesoŋ 16)

DUNDINU KERCEEN

Woy-Yàlla nº 59

7. Mën nga jële mbégte ci liggéeyu waare bi bu dee sax danga bare kersa

(15 minit) Waxtaan ak ñi teew.

Ndax danga nekk nit ku bare kersa? Ndax dangay faral di nëbbatu? Ndax dangay tiit lool boo naree wax ci kanamu nit ñi? Yenn saay, bare kersa dina ñu teree def li ñu bëgg. Waaye, am na ay nit yu bare kersa yu dem ba mën a wax ci kanamu nit ñi, ba di waare sax. Lan la ñu mën a jàng ci ñoom?

Woneel WIDEO bi tudd: Maa ngi def lépp li ma mën ci liggéeyu Yexowa bu dee sax dama bare kersa. Ba pare nga laaj ñi teew lii:

  • Ban njariñ la mbokk Lee jële ci topp xelal bi ko maamam jox bi mu naan «defal lépp li nga mën ci liggéeyu Yexowa»?

Biibël bi wone na ne Musaa, Yeremi ak Timote dañoo bare woon kersa. (Mucc ga 3:11; 4:10; Yeremi 1:​6-8; 1 Timote 4:12) Waaye loolu terewul ñu def ay mbir yu réy ci liggéeyu Yexowa, ndaxte moo leen doon dimbali. (Mucc ga 4:12; Yeremi 20:11; 2 Timote 1:​6-8)

Jàngal Esayi 43:​1, 2. Ba pare nga laaj ñi teew lii:

  • Lan la Yexowa dig ñi koy jaamu?

Naka la Yexowa dimbalee ñi bare kersa ñu mën a waare?

Woneel WIDEO bi tudd: Sóobu ci ndox dina tax nga gën a bég (Xaaj). Ba pare nga laaj ñi teew lii:

  • Naka la mbokk Jackson gisee ne Yexowa mu ngi koy dimbali bu baax ci liggéeyu waare bi?

  • Naka la liggéeyu waare bi mënee dimbali ku bare kersa?

8. Njàngum Biibël bi ci biir mbooloo mi

Kàddu yi ñuy tëje ndaje bi (3 minit) | Woy-Yàlla nº 151 ak ñaan