Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

24 feewriyee ba 2 màrs

KÀDDU YU XELU 2

24 feewriyee ba 2 màrs

Woy-Yàlla nº 35 ak ñaan | Kàddu yi ñuy tàmbalee ndaje bi (1 minit)

NJÀNGALE YU AM SOLO YU NEKK CI KÀDDU YÀLLA

1. Lu tax waruloo caaxaane njàngum Biibël bi ngay defal sa bopp?

(10 minit)

Noonu ngay wonee ne fonk nga dëgg gi (Kàddu yu Xelu 2:​3, 4; w22.08-F 18 § 16)

Dina la dimbali nga jël ay dogal yu baax (Kàddu yu Xelu 2:​5-7; w22.10-F 19 § 3-4)

Dafay dëgëral sa ngëm (Kàddu yu Xelu 2:​11, 12; w16.09-F 23 § 2-3)

LAAJAL SA BOPP LII: ‘Lan laa mën a def ba gën a jariñoo sama njàngum Biibël bi?’

2. Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi

(10 minit)

  • Kàddu yu Xelu 2:​7, NWT—Naka la Yexowa nekkee «kiiraayu nit ñi jub»? (it-1-F 1195 § 4)

  • Ban aaya ngeen xóotal ci seen njàngum Biibël bi ci semen bi?

3. Aaya yi ñu war a liir ci Biibël bi

YOKKAL SA MËN-MËN CI LIGGÉEYU WAARE BI

4. Ni nga mënee tàmbali waxtaan

(4 minit) KËROO-KËR. Dimbalil nit ki mu xam ni mu mënee gis ci jw.org ay xelal yi ñu jagleel ñi séy. (lmd-F lesoŋ 1 ponk 3)

5. Li ñu mën a wax bu ñu seetiwaatee nit ki

(3 minit) WAARAATE SAA YU ÑU AMEE BUNT. Bi ngeen mujjee waxtaan, nit ki dafa la waxoon li ko itteel. Jox ko yéenekaay buy wax ci loolu. (lmd-F lesoŋ 9 ponk 3)

6. Waxtaan bi

(5 minit) lmd-F appendice A idée 8—Turu waxtaan bi ci farãse: Mari et femme doivent être fidèles l’un à l’autre. (th lesoŋ 13)

DUNDINU KERCEEN

Woy-Yàlla nº 96

7. Ndax wutkat alal nga, maanaam njàngale yu am solo yi nekk ci Biibël bi?

(15 minit) Waxtaan ak ñi teew.

Yeen ndaw ñi, ndax wut alal bu làqu neex na leen? Bu dee waaw, Biibël baa ngi leen di xiir ngeen wut alal bi gën a am solo ci àddina maanaam xam-xamu Yàlla! (Kàddu yu Xelu 2:​4, 5). Mën ngeen gis xam-xam bu am solo boobu bu ngeen di jàng Biibël bi saa su nekk te di gëstu bu baax ci nettali yi ngeen di jàng. Bu ngeen di def loolu, dingeen ci jële barke yu bare te di ngeen bég!

  • Yan laaj nga mën a laaj sa bopp booy jàng Biibël bi? (w24.02-F 32 § 2-3)

  • Yan jumtukaay nga mën a jëfandikoo ngir am tont yi?

Wideo yi tudd Li nga mën a jàng ci xaritu Yexowa yi, mën nañu la dimbali nga xam ni nga mënee di xalaat bu baax ci li ngay jàng ci Biibël bi.

Woneel WIDEO bi tudd: Li nga mën a jàng ci xaritu Yexowa yi—Abel.

Jàngal Njàlbéen ga 4:​2-4 ak Yawut ya 11:4. Ba pare nga laaj ñi teew lii:

  • Naka la Abel wonee ne xaritu Yexowa la?

  • Naka la Abel dëgërale ngëmam ci Yexowa?

  • Naka nga mënee dëgëral sa ngëm?

8. Njàngum Biibël bi ci biir mbooloo mi

Kàddu yi ñuy tëje ndaje bi (3 minit) | Woy-Yàlla nº 102 ak ñaan