Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

27 sãwiyee ba 2 feewriyee

TAALIFI CANT 140-143

27 sãwiyee ba 2 feewriyee

Woy-Yàlla nº 44 ak ñaan | Kàddu yi ñuy tàmbalee ndaje bi (1 minit)

NJÀNGALE YU AM SOLO YU NEKK CI KÀDDU YÀLLA

1. Boo ñaanee Yàlla ndimbal, nanga def itam li ànd ak sa ñaan

(10 minit)

Nangul tegtal ak xelal yi ñu lay jox (Taalifi Cant 141:5; w22.02-F 12 § 13-14)

Xaalatal bu baax ci ni ñu Yexowa dimbalee ak it ci ni mu dimbalee jaamam yu njëkk ya (Taalifi Cant 143:5; w10-F 15/3 32 § 4)

Jéemal a gise mbir yi ni ko Yexowa di gise (Taalifi Cant 143:10; w15-F 15/3 32 § 2)

Taalifi Cant 140 ba 143 dafay wone ne Daawuda yemul rekk ci ñaan Yàlla, waaye dafa def itam li ànd ak li mu ñaan.

2. Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi

(10 minit)

  • Taalifi Cant 140:4—Lu tax Daawuda wax ne làmmiñu nit ku bon dafa mel ni jaan? (it-2-F 1134)

  • Ban aaya ngeen xóotal ci seen njàngum Biibël bi ci semen bi?

3. Aaya yi ñu war a liir ci Biibël bi

YOKKAL SA MËN-MËN CI LIGGÉEYU WAARE BI

4. Ni nga mënee tàmbali waxtaan

(4 minit) WAARAATE SAA YU ÑU AMEE BUNT. Njëkkal a seetlu li nit ki soxla nga jàpple ko ci. Boo pare nga door a tàmbalee wax ci lu jëm ci Biibël bi. (lmd-F lesoŋ 3 ponk 5)

5. Li ñu mën a wax bu ñu seetiwaatee nit ki

(3 minit) WAARAATE CI BÉRÉB YU BARE NIT. Li nga mën a def bu la nit ki waxee ne dafa jàpp. (lmd-F lesoŋ 7 ponk 3)

6. Wax ci li ñu gëm

(5 minit) Wone bi. Ijwfq-F waxtaan nº 21—Wone bi mu ngi sukkandiku ci waxtaan bi tudd ci farãse: Pourquoi les Témoins de Jéhovah refusent-ils les transfusions sanguines ? (th lesoŋ 7)

DUNDINU KERCEEN

Woy-Yàlla nº 141

7. Buñu bëggee xam li ñu war a def buñu amee feebar boo xam ne dafa laaj ñu opéré ñu, léegi lañu war a waajal suñu bopp

(15 minit) Waxtaan ak ñi teew.

Yexowa dig na ñu ne moo ñuy ‘wallusi buñu jaaxlee’ (Taalifi Cant 46:2). Am feebar bu soxla ñu opéré ñu mën na tax ñu jaaxle lool. Waaye, Yexowa jox na ñu lépp li ñu soxla ngir waajal suñu bopp. Ci misaal, mbootaayam jox na ñu li ñuy woowe ci farãse procuration relative aux soins médicaux (kàrt DPA), Attestation individuelle (CI) a ak yeneen téere b yi ñu ci mën a xelal. Am nañu itam gurup bi ñuy woowe ci tubaab Comité de liaison hospitalier (CLH). Jumtukaay yooyu dañu ñuy dimbali ñu topp santaane Yexowa yu jëm ci deret (Jëf ya 15:​28, 29).

Woneel WIDEO bi tudd: Ndax waajal nga sa bopp ngir xam ban fasoŋu faj nga mën a nangu? Ba pare nga laaj ñi teew lii:

  • Ban njariñ la ñenn ñi jële ci def lépp li ñu laaj ci seen kàrt DPA?

  • Naka la kayit bi tudd ci farãse Informations pour les femmes enceintes (S-401), dimbalee ñenn ñi?

  • Mën nañu am feebar bu tax ñu teye ñu lopitaal, ñu war ñu opéré, walla ñu am feebar bu mel ni cancer. Bu dee sax dañu foog ne loolu du laaj deret, lu tax ñu war koo teel a yégal waa CLH?

8. Njàngum Biibël bi ci biir mbooloo mi

Kàddu yi ñuy tëje ndaje bi (3 minit) | Woy-Yàlla nº 103 ak ñaan

a Waarekat yi sóobu ci ndox, mën nañu laaj mbokk biy toppatoo mbirum téere yi ci saalu nguur gi, mu jox leen kàrt DPA ak it kàrt bi ñuy woowe ci farãse Attestation individuelle (CI) ngir seeni doom.

b Ñi soxla kayit yi ñuy woowe Informations pour les femmes enceintes (S-401), Informations pour les patients qui doivent subir une opération chirurgicale ou une chimiothérapie (S-407) ak Informations pour les parents qui recherchent un traitement médical pour leur enfant (S-55), mën nañu ko laaj magu mbooloo yi.