6 sãwiyee ba 12 sãwiyee
TAALIFI CANT 127-134
Woy-Yàlla nº 134 ak ñaan | Kàddu yi ñuy tàmbalee ndaje bi (1 minit)
1. Yeen waajur yi, wéyleen di toppatoo seeni doom
(10 minit)
Yeen waajur yi mën ngeen a wóolu Yexowa ndaxte dina leen jàpple ngeen jox seen njaboot li mu soxla (Taalifi Cant 127:1, 2)
Doom maye la bu jóge ci Yexowa (Taalifi Cant 127:3; w21.08-F 5 § 9)
Xale bu nekk ak jikkoom. Kon bu ngeen di yar seeni doom, nangeen jox ku nekk li mu soxla (Taalifi Cant 127:4; w19.12-F 27 § 20)
2. Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi
(10 minit)
-
Taalifi Cant 128:3—Lan moo tax taalifkat bi mengale xale yi ak ‘njëmbat bu jebbi’? (it-1-F 543)
-
Ban aaya ngeen xóotal ci seen njàngum Biibël bi ci semen bi?
3. Aaya yi ñu war a liir ci Biibël bi
(4 minit) Taalifi Cant 132:1-18 (th lesoŋ 2)
4. Ni nga mënee tàmbali waxtaan
(3 minit) WAARAATE SAA YU ÑU AMEE BUNT. (lmd-F lesoŋ 1 ponk 3)
5. Ni nga mënee tàmbali waxtaan
(4 minit) WAARAATE SAA YU ÑU AMEE BUNT. Li nga mën a def bu nit ki waxee benn xalaat bu wuute ak li Biibël bi jàngale. (lmd-F lesoŋ 5 ponk 4)
6. Ni ñu mënee jàngal nit ñi ba ñu nekk taalibe Yeesu
(5 minit) lff lesoŋ 16 ponk 4-5. Waxtaanal ak ki ngay jàngal Biibël bi, ci ni ngeen mënee def ba, njàngum Biibëlam am, donte sax doo fi nekk (lmd-F lesoŋ 10 ponk 4)
Woy-Yàlla nº 13
7. Yeen waajur yi, ndax yeen a ngi jëfandikoo jumtukaay bu baax bii ngir jàngal seeni doom?
(15 minit) Waxtaan ak ñi teew.
Mbootaayu Yexowa defar na ay jumtukaay yu bare ngir dimbali waajur yi ñu jàngal seeni doom ñu xam Yexowa. Waaye jumtukaay bi gën a am solo bi ñu am mooy, ñu nekk ay royukaay yu baax ci ñoom.—Baamtug Yoon wi 6:5-9.
Yeesu jumtukaay bu baax boobu la jëfandikoo ngir jàngal taalibeem yi.
Jàngal Yowaana 13:13-15. Ba pare nga laaj ñi teew lii:
-
Ci sa xalaat lan moo tax ni Yeesu nekkoon royukaay ci taalibeem yi, nekkoon fasoŋu jàngale bu am solo?
Yeen waajur yi, seeni jëf la seeni doom di gën a xool. Kon bu ngeen nekkee ay royukaay yu baax ci ñoom, loolu dina tax seeni doom nangu li ngeen di jàngale te dina leen xiir ñu déglu leen.
Woneel WIDEO bi tudd: Nañu nekk ay royukaay ci suñuy doom. Ba pare nga laaj ñi teew lii:
-
Lu am solo lan, la mbokk Garcia ak jabaram jàngal seeni doom yu jigéen?
-
Naka la leen wideo bi di xiiree ngeen wéy di nekk ay royukaay yu baax ci seeni doom?
8. Njàngum Biibël bi ci biir mbooloo mi
(30 minit) bt-F pàcc 20 § 13-20