Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

16 septaambar ba ​22 septaambar

TAALIFI CANT 85-87

16 septaambar ba ​22 septaambar

Woy-Yàlla nº. 41 ak ñaan | Kàddu yi ñuy tàmbalee ndaje bi (1 minit)

NJÀNGALE YU AM SOLO YU NEKK CI KÀDDU YÀLLA

1. Ñaan dafa ñuy dimbali ñuy muñ

(10 minit)

Ñaanal Yexowa mu dimbali la nga am mbégte (Taalifi Cant 86:4)

Ñaanal Yexowa mu dimbali la nga wéy di takku ci moom (Taalifi Cant 86:​11, 12; w12 15/5-F 25 § 10)

Na la wóor ne Yexowa dina tontu say ñaan (Taalifi Cant 86:​6, 7; w23.05-F 13 § 17-18)


LAAJAL SA BOPP LII: ‘Bu ma nekkee ci jafe-jafe, ndax damay faral di ñaan saa su nekk? Ndax samay ñaan dañuy gën a gudd te xóot?’—Taalifi Cant 86:3.

2. Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi

(10 minit)

  • Taalifi Cant 86:11—Ñaan bi Daawuda def fii, lan lañuy jàngal ci lu jëm ci suñu xol? (it-1-F 492 § 2)

  • Ban aaya ngeen xóotal ci seen njàngum Biibël bi ci semen bi?

3. Aaya yi ñu war a liir ci Biibël bi

YOKKAL SA MËN-MËN CI LIGGÉEYU WAARE BI

4. Ni nga mënee tàmbali waxtaan

(3 minit) WAARAATE SAA YU ÑU AMEE BUNT. Laajal nit ki ndax bëgg na jàng Biibël bi. (lmd-F lesoŋ 3 ponk 5)

5. Li ñu mën a wax bu ñu seetiwaatee nit ki

(4 minit) WAARAATE SAA YU ÑU AMEE BUNT. Nit ki dafa la waxoon ne li xew fan yii jaaxal na ko lool. Laaj ko ndax bëgg na jàng Biibël bi (lmd-F lesoŋ 7 ponk 4)

6. Ni ñu mënee jàngal nit ñi ba ñu nekk taalibe Yeesu

(5 minit) lff lesoŋ 15 ponk 5. Waxtaanal ak ki ngay jàngal Biibël bi, ci ni ngeen mënee def ba, njàngum Biibëlam am donte sax doo fi nekk semen bii di ñëw. (lmd-F lesoŋ 10 ponk 4)

DUNDINU KERCEEN

Woy-Yàlla nº. 83

7. Bul tàyyi ci def lu baax!

(5 minit) Waxtaan ak ñi teew.

Woneel WIDEO bi. Ba pare nga laaj ñi teew lii:

  • Lu tax yenn saa yi, ñuy bëgg a xàddi ci liggéeyu waare bi?

  • Waaye, lu tax waruñu xàddi?

8. Buñu tàyyi di laaj nit ñi ndax bëgg nañu jàng Biibël bi!

(10 minit) Waxtaan ak ñi teew.

Ndax bi kampañ bi komaasee ba tey, jot ngaa tàmbali njàngum Biibël ak téere bi tudd Mën nga dund ci jàmm ba fàww!? Bu dee waaw, wóor na ne kontaan nga ci lool! Te loolu war na sawarloo ñu bare. Waaye bu dee jotuloo tàmbali njàngum Biibël, xéyna yaa ngi laaj sa bopp ndax góorgóorlu bi nga nekk di def jar na ko. Bu dee loolu nga xalaat, lan nga mën a def ngir bañ a xàddi?

Woneel WIDEO bi tudd: «Li ñu bëgg mooy di rafetal suñu tur ni Seede Yàlla. . . ] ci muñ» (Buñuy waare). Ba pare nga laaj ñi teew lii:

  • Naka lañu 2 Korent 6:​4, 6 mënee dimbali bu ñu foogee ne ñu ngi def liggéeyu waare bi ci «neen»?

  • Lan nga mën a soppi ci ni ngay waare boo gisee ne, yaa ngi góorgóorlu ngir tàmbali njàngum Biibël, waaye sottiwul?

Bul fàtte lii: suñu mbégte ci liggéeyu waare bi aajuwul ci njàngum Biibël yi ñu am. Waaye mu ngi aaju ci xam ne li ñuy def neex na Yexowa (Luug 10:​17-20). Kon na nga wéy di bokk ci kampañ bi ak sa xol bépp ndaxte xam nga ne ‘sa liggéey bi jëm ci Yexowa, du neen’!—1 Korent 15:58.

9. Njàngum Biibël bi ci biir mbooloo mi

Kàddu yi ñuy tëjee ndaje bi (3 minit) | Woy-Yàlla nº. 39 ak ñaan