Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

2 septaambar ba 8 septaambar

TAALIFI CANT 79-81

2 septaambar ba 8 septaambar

Woy-Yàlla nº. 29 ak ñaan | Kàddu yi ñuy tàmbalee ndaje bi (1 minit)

NJÀNGALE YU AM SOLO YU NEKK CI KÀDDU YÀLLA

1. Nañu wone ne fonk nañu turu Yexowa ndaxte tur bu màgg la

(10 minit)

Nañu moytu jëf yi nga xam ne dañuy tilimal turu Yexowa (Taalifi Cant 79:9; w17.02-F 9 § 5)

Nañu wormaal Yexowa te di ko woo ci turam (Taalifi Cant 80:19; Room 10:13; ijwbv-F 3 § 4-5)

Yexowa dafay barkeel bu baax ñiy wone ne dañu fonk turam ci ni ñu koy déggale (Taalifi Cant 81:​14, 17)

Buñu bëgge suñu doxalin màggal turu Yexowa, dañu war a xamal nit ñi ne ay Seede Yexowa lañu

2. Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi

(10 minit)

  • Taalifi Cant 80:2—Lan moo tax ñu daan faral di woowe giiru Israyil yépp ci turu Yuusufa? (it-2-F 53 § 3-4)

  • Ban aaya ngeen xóotal ci seen njàngum Biibël bi ci semen bi?

3. Aaya yi ñu war a liir ci Biibël bi

YOKKAL SA MËN-MËN CI LIGGÉEYU WAARE BI

4. Ni nga mënee tàmbali waxtaan

(1 minit) KËROO-KËR. Laajal nit ki ndax bëgg na jàng Biibël bi. (lmd-F lesoŋ 4 ponk 4)

5. Ni nga mënee tàmbali waxtaan

(3 minit) WAARAATE SAA YU ÑU AMEE BUNT. Laajal nit ki ndax bëgg na jàng Biibël bi. (lmd-F lesoŋ 4 ponk 3)

6. Ni nga mënee tàmbali waxtaan

(2 minit) WAARAATE CI BÉRÉB YU BARE NIT. Laajal nit ki ndax bëgg na jàng Biibël bi. (lmd-F lesoŋ 3 ponk 3)

7. Li ñu mën a wax bu ñu seetiwaatee nit ki

(5 minit) KËROO-KËR. Nit ki nanguwul woon a jàng Biibël bi. Bi ngeen gisewaate nga laaj ko ndax bëgg na léegi jàng Biibël bi. (lmd-F lesoŋ 8 ponk 3)

DUNDINU KERCEEN

Woy-Yàlla nº. 10

8. «Dinañu wormaal sama tur wu sell wi»

(15 minit) Waxtaan ak ñi teew.

Seytaane ci biir toolu Eden la tàmbalee tilimal turu Yexowa. Booba ba tey, setal turu Yexowa mooy li gën a am solo ci bépp mbindeef bu koy jaamu.

Xoolal yenn ci fen yu réy yi Seytaane fenal Yexowa. Dafa ne Yexowa njiit bu soxor la (Njàlbéen ga 3:​1-6; Ayóoba 4:​18, 19). Wax na itam ne buñuy jaamu Yexowa du mbëggeel a tax (Ayóoba 2:​4, 5). Tax na sax ba ay milioŋi nit gëmuñu ne Yexowa moo sàkk suuf su rafet sii ñu dëkk.—Room 1:​20, 21.

Lan ngay yëg soo déggee fen yooyu? Wóor na ne dinga bëgg a setal turu Yexowa! Yexowa xamoon na ne jaamam yi dinañu bokk ci ñiy sellal te setal turam (Esayi 29:23). Naka nga mën a def ngir bokk ci ñiy setal turam?

  • Dimbalil ñeneen ñi ñu xam Yexowa te bëgg ko (Yowaana 17:​25, 26). Nanga waajal sa bopp ngir mën a joxe ay firnde yuy wone ne Yàlla am na te xamal nit ñi jikkoom yu rafet yi.—Esayi 63:7

  • Nanga bëgg Yexowa ak sa xol bépp. (Macë 22:​37, 38). Bul topp santaane Yexowa yi rekk ndaxte dañu baax ci ñun, waaye nanga leen topp ngir bégal xolu Yexowa.—Kàddu yu xelu 27:11

Woneel WIDEO bi tudd: Mbëggeel amul àpp bu dee sax . . . Ñi nga bokkal lekkool duñu topp santaaney Yàlla. Ba pare nga laaj ñi teew lii:

  • Naka la Ariel ak Diego setalee turu Yexowa?

  • Lan moo leen xiir ñu bëgg a setal turu Yexowa?

  • Naka nga leen mën a royee?

9. Njàngum Biibël bi ci biir mbooloo mi

Kàddu yi ñuy tëjee ndaje bi (3 min.) | Woy-Yàlla nº. 90 ak ñaan