Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

21 oktoobar ba 27 oktoobar

TAALIFI CANT 100-102

21 oktoobar ba 27 oktoobar

Woy-Yàlla nº. 37 ak ñaan | Kàddu yi ñuy tàmbalee ndaje bi (1 minit)

NJÀNGALE YU AM SOLO YU NEKK CI KÀDDU YÀLLA

1. Yexowa ku gore la. Ñun itam dañu war a gore te takku ci moom

(10 minit)

Nañu bëgg Yexowa ak suñu xol bépp (Taalifi Cant 100:5; w23.03-F 12 § 18-19)

Nañu moytu lépp li mën a yàq suñu xaritoo ak Yexowa (Taalifi Cant 101:​2, 3; w23.02-F 17 § 10)

Nañu moytu képp kuy tilimal turu Yexowa ak mbootaayam (Taalifi Cant 101:5; w11-F 15/7 16 § 7-8)

LAAJAL SA BOPP LII: ‘Ndax ni may jëfandikoo réseaux sociaux yi mën na yàq sama diggante ak Yexowa?’

2. Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi

(10 minit)

  • Taalifi Cant 102:8—Lu tax taalifkat bi méngale boppam ak picc bu wéetoo ci kaw teraas? (it-2-F 522)

  • Ban aaya ngeen xóotal ci seen njàngum Biibël bi ci semen bi?

3. Aaya yi ñu war a liir ci Biibël bi

YOKKAL SA MËN-MËN CI LIGGÉEYU WAARE BI

4. Ni nga mënee tàmbali waxtaan

(3 minit) KËROO-KËR. (lmd-F lesoŋ 2 ponk 3)

5. Li ñu mën a wax bu ñu seetiwaatee nit ki

(5 minit) KËROO-KËR. Laajal nit ki ndax bëgg na jàng Biibël bi. (lmd-F lesoŋ 9 ponk 4)

6. Wax ci li ñu gëm

(4 minit) Wone bi. ijwbq-F 129—Wone bi mu ngi sukkandiku ci waxtaan bii: Biibël bi, ndax am na lu ñu ci yokk walla lu ñu ci wàññi? (th lesoŋ 8)

DUNDINU KERCEEN

Woy-Yàlla nº. 137

7. «Dama takku ci yaw; nga teye ma»

(15 minit)

Waxtaan ak ñi teew. Woneel WIDEO bi. Ba pare nga laaj ñi teew lii:

  • Naka la Aana wone ngor maanaam mbëggeel gu takku?

  • Naka lañu mënee roy ci moom?

8. Njàngum Biibël bi ci biir mbooloo mi

Kàddu yi ñuy tëjee ndaje bi (3 minit) | Woy-Yàlla nº. 96 ak ñaan