Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

23 septaambar ba ​29 septaambar

TAALIFI CANT 88-89

23 septaambar ba ​29 septaambar

Woy-Yàlla nº. 22 ak ñaan | Kàddu yi ñuy tàmbalee ndaje bi (1 minit)

NJÀNGALE YU AM SOLO YU NEKK CI KÀDDU YÀLLA

1. Kiliftéefu Yexowa mooy bi gën

(10 minit)

Kiliftéefu Yexowa mooy indi njubte dëgg (Taalifi Cant 89:15; w17.06-F 28 § 5)

Kiliftéefu Yexowa mooy indi mbégte dëgg (Taalifi Cant 89:​16, 17; w17.06-F 29 § 10-11)

Kiliftéefu Yexowa dina sax ba fàww (Taalifi Cant 89:​35-38; w14-F 15/10 10 § 14)

Bu ñu bàyye xel ne fasoŋ bi Yexowa di ilife mooy bi gën, loolu dina ñu dimbali ñu bañ a bokk ci politig

2. Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi

(10 minit)

3. Aaya yi ñu war a liir ci Biibël bi

YOKKAL SA MËN-MËN CI LIGGÉEYU WAARE BI

4. Ni nga mënee tàmbali waxtaan

(3 minit) WAARAATE CI BÉRÉB YU BARE NIT. Laajal nit koo xam ne du kerceen ndax bëgg na jàng Biibël bi (lmd-F lesoŋ 5 ponk 5)

5. Li ñu mën a wax bu ñu seetiwaatee nit ki

(4 minit) KËROO-KËR. Laajal nit ki ndax bëgg na nga won ko ni ñuy defe njàngum Biibël bi. (th lesoŋ 9)

6. Wax ci li ñu gëm

(5 minit) Waxtaan bi. ijwbq-F 181—Turu waxtaan bi: De quoi la Bible parle-t-elle ? (th lesoŋ 2)

DUNDINU KERCEEN

Woy-Yàlla nº. 94

7. Topp santaane Yexowa yi mooy li gën

(10 minit) Waxtaan ak ñi teew.

Ñu bare dañu gis ne li Biibël bi wax ci wàllu séy, yenuwul maanaa te dafa xewwi. Ndax gëm nga ne topp santaane Yexowa yi saa su nekk mooy li gën ci yaw?—Esayi 48:​17, 18; Room 12:2.

Biibël bi dafa wax ne ñi dul topp santaane Yàlla yi «duñu bokk ci nguuru Yàlla.» (1 Korent 6:​9, 10) Waaye, ndax loolu rekk a war a tax ñu topp santaane Yàlla yi?

Woneel WIDEO bi tudd: Li tax ma gëm ne: Santaane Yàlla yi ñoo gën. Ba pare nga laaj ñi teew lii:

  • Naka la ñu santaane Yàlla yi di aare?

8. Li mbooloo mi soxla ci wàllu ngëm

(5 minit)

9. Njàngum Biibël bi ci biir mbooloo mi

Kàddu yi ñuy tëjee ndaje bi (3 minit) | Woy-Yàlla nº. 133 ak ñaan