Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

30 septaambar ba 6 oktoobar

TAALIFI CANT 90-91

30 septaambar ba 6 oktoobar

Woy-Yàlla nº. 140 ak ñaan | Kàddu yi ñuy tàmbalee ndaje bi (1 minit)

NJÀNGALE YU AM SOLO YU NEKK CI KÀDDU YÀLLA

1. Bu ñu bëggee gudd fan, dañu war a am kóolute ci Yexowa

(10 minit)

Doomu aadama yi menuñu def dara ba yokk fan yu ñuy dund (Taalifi Cant 90:10; wp19.3-F 5 § 2-4)

Yexowa mooy ki mas a nekk Yàlla, te moom mooy Yàlla ba fàww (Taalifi Cant 90:2; wp19.1-F 5, ak wërale bi)

Mën na may dund gu dul jeex ñépp ñi ko wóolu, te dina ko def sax (Taalifi Cant 21:5; 91:16)

Bu ñu nangu mukk faj bu andul ak santaane Yexowa yi, ndaxte loolu mën na yàq suñu diggante ak moom. (w22.06-F 18 § 16-17).

2. Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi

(10 minit)

  • Taalifi Cant 91:11—Ban gis-gis bu yem lañu war a am ci ndimbalu malaaka yi? (wp17.5-F 5)

  • Ban aaya ngeen xóotal ci seen njàngum Biibël bi ci semen bi?

3. Aaya yi ñu war a liir ci Biibël bi

YOKKAL SA MËN-MËN CI LIGGÉEYU WAARE BI

4. Ni nga mënee tàmbali waxtaan

(3 minit) WAARAATE SAA YU ÑU AMEE BUNT. Bul ñëw rekk wax lu jëm ci Biibël bi, waaye njëkkal a waxtaan ak nit ki ba mu wax li ko iteel. Noonu dinga mën a xam ni ko Biibël bi mënee dimbali mu am dund gu dul jeex. (lmd-F lesoŋ 1 ponk 3)

5. Ni nga mënee tàmbali waxtaan

(4 minit) WAARAATE SAA YU ÑU AMEE BUNT. (lmd-F lesoŋ 1 ponk 1)

6. Waxtaan bi

(5 minit) lmd-F appendice A idée 5—Turu waxtaan bi: La vie éternelle sur terre est possible. (th lesoŋ 14)

DUNDINU KERCEEN

Woy-Yàlla nº. 158

7. Buñu xeeb muñug Yàlla (Ni Yexowa di gise waxtu)

(5 minit). Waxtaan ak ñi teew.

Woneel WIDEO bi. Ba pare nga laaj ñi teew lii:

  • Am gis-gisu Yexowa ci lu jëm ci waxtu, naka la ñu mënee dimbali ñu mën a muñ te xaar li mu ñu dig?

8. Li suñu mbootaay di def

(10 minit) Woneel WIDEO bu weeru septaambar bi.

9. Njàngum Biibël bi ci biir mbooloo mi

Kàddu yi ñuy tëjee ndaje bi (3 minit) | Woy-Yàlla nº. 68 ak ñaan