Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

7 oktoobar ba 13 oktoobar

TAALIFI CANT 92-95

7 oktoobar ba 13 oktoobar

Woy-Yàlla nº. 84 ak ñaan | Kàddu yi ñuy tàmbalee ndaje bi (1 minit)

NJÀNGALE YU AM SOLO YU NEKK CI KÀDDU YÀLLA

1. Jaamu Yexowa mooy li gën li ñu mën a def ci suñu dund!

(10 minit)

Yexowa yelloo na ñu jaamu ko (Taalifi Cant 92:​2, 5; w18.04-F 26 § 5)

Dafay dimbale jaamam yi ñu ànd ak sago ci lépp li ñuy def (Taalifi Cant 92:6; w18.11-F 20 § 8)

Yexowa dafa fonk ñi koy jaamu te bu ñu màggate sax dafay wéy di leen fonk (Taalifi Cant 92:​13-16; w20.01-F 19 § 18)

LAAJAL SA BOPP LII: ‘Ana lu ma teree jébbalu ci Yexowa te ñu sóob ma ci ndox?’

2. Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi

(10 minit)

  • Taalifi Cant 92:6—Naka la kàddu yii di fësale xam-xamu Yexowa? (cl-F 211 § 18)

  • Ban aaya ngeen xóotal ci seen njàngum Biibël bi ci semen bi?

3. Aaya yi ñu war a liir ci Biibël bi

YOKKAL SA MËN-MËN CI LIGGÉEYU WAARE BI

4. Ni nga mënee tàmbali waxtaan

(4 minit) WAARAATE SAA YU ÑU AMEE BUNT. Ci biir waxtaan bi, seetal ni ngay waxe nit ki ne dangay jàngale Biibël bi ak ni nga koy defe. (lmd-F lesoŋ 5 ponk 3)

5. Li ñu mën a wax bu ñu seetiwaatee nit ki

(3 minit) WAARAATE SAA YU ÑU AMEE BUNT. Nit ki nanguwul woon a jàng Biibël bi. Bi ngeen gisewaate nga laaj ko ndax bëgg na léegi jàng Biibël bi. (lmd-F lesoŋ 8 ponk 4)

6. Ni ñu mënee jàngal nit ñi ba ñu nekk taalibe Yeesu

(5 minit) Waxtaanal ak kenn ki ngay jàngal Biibel bi koo xam ne nekkul di jëm kanam. (lmd-F lesoŋ 12 ponk 5)

DUNDINU KERCEEN

Woy-Yàlla nº. 5

7. Bu ndaw yi amee njàqare

(15 minit) Waxtaan ak ñi teew.

Jaamu Yexowa yi sax lée-lée dañuy am njàqare. Ci misaal, Daawuda amoon na jafe-jafe yu ko jural njàqare, te suñu mbokk yu bare ci ngëm loolu lañuy dund tey (Taalifi Cant 13:3; 139:23). Li ci gën a metti mooy, ndaw yi sax mën nañu nekk ci njàqare. Njàqare mën na tax li ñu doon faral di def, lu ci mel ni dem lekkool walla teewe ndaje yi, dem ba nekk lu diis ci ñoom. Loolu mën na tax ñu jaaxle lool walla sax ñu bëgg a xaru.

Yeen ndaw ñi, bu dee dangeen nekk ci njàqare gu réy, jegeleen seeni waajur walla kerceen bu mat. Buleen fàtte di ñaan Yexowa mu dimbali leen (Filib 4:6). Dina leen dimbali (Taalifi Cant 94:​17-19; Esayi 41:10). Xoolal misaalu Steing.

Woneel WIDEO bi tudd: Yexowa toppatoo na ma. Ba pare nga laaj ñi teew lii:

• Ban aaya ci Biibël bi moo dimbali Steing? Lu tax?

• Naka la ko Yexowa toppatoo?

Yeen waajur yi, mën ngeen dimbali seeni doom bu ñu nekke ci njàqare. Nangeen leen déglu bu baax, won leen mbëggeel bi ngeen am ci ñoom te dimbali leen ñu gëm ne Yexowa bëgg na leen (Tit 2:4; Saag 1:19). Nangeen wéeru ci Yexowa ngir mu dëfal leen te may leen doole bi ngeen soxla ngir dimbali seeni doom.

Nit mën na nekk ci mbooloo mi, di dund njàqare gu réy te ñun duñu ko xam sax. Mën nañu bañ a nànd it li muy yëg ci xolam. Waaye terewul mën nañu dimbali ñépp ci mbooloo mi, bu ñu leen di won ne bëgg nañu leen te am nañu palaas ci suñu xol.—Kàddu yu Xelu 12:25; Yawut ya 10:24.

8. Njàngum Biibël bi ci biir mbooloo mi

Kàddu yi ñuy tëjee ndaje bi (3 minit) | Woy-Yàlla nº. 81 ak ñaan