Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

9 Septaambar ba 15 septaambar

TAALIFI CANT 82-84

9 Septaambar ba 15 septaambar

Woy-Yàlla nº. 80 ak ñaan | Kàddu yi ñuy tàmbalee ndaje bi (1 minit)

NJÀNGALE YU AM SOLO YU NEKK CI KÀDDU YÀLLA

Kenn ci doomu Kore yi a ngi xool benn tàggu picc ca ëttu kër Yàlla ga

1. Nañu fonk sas yi ñu am ci liggéeyu Yexowa

(10 minit)

Dañu fonk sas yi ñu am ci liggéeyu Yexowa (Taalifi Cant 84:​2-4; wp16.6-F 8 § 2-3)

Nañu bég ci sas yi ñu am te bañ a def suñu xel ci sas yi ñu bëggoon a am (Taalifi Cant 84:11; w08-F 15/7 30 § 3-4)

Yexowa dafa baax ci ñépp ñi koy jaamu ak takkute (Taalifi Cant 84:12; w20.01-F 17 § 12)

Sas boo gis, am na ay barke ak ay jafe-jafe. Waaye, booy xalaat ci barke yi, dinga mën a bég ci bépp sas bu ñu la jox.

2. Nañu xóotal suñu njàngum Biibël bi

(10 minit)

  • Taalifi Cant 82:3—Won mbëggeel «jirim» yi, maanaam ñi ñàkk seen yaay walla seen pàppa te ñu bokk ci mbooloo mi, am na solo lool. Lu tax? (it-2-F 459)

  • Ban aaya ngeen xóotal ci seen njàngum Biibël bi ci semen bi?

3. Aaya yi ñu war a liir ci Biibël bi

YOKKAL SA MËN-MËN CI LIGGÉEYU WAARE BI

4. Nañu wone ne yëg nañu nit ñi—Lan la Yeesu def?

(7 minit) Waxtaan ak ñi teew. Woneel WIDEO bi, ba pare ngeen waxtaan ci lmd-F lesoŋ 9 ponk 1-2.

5. Nañu wone ne yëg nañu nit ñi—Nañu roy ci Yeesu

(8 minit) Waxtaan ak ñi teew. Waxtaan bi dafa sukkandiku ci lmd-F lesoŋ 9 ponk 3-5 ak «Seetal aaya yii itam».

DUNDINU KERCEEN

Woy-Yàlla nº. 57

6. Li mbooloo mi soxla ci wàllu ngëm

(15 minit)

7. Njàngum Biibël bi ci biir mbooloo mi

Kàddu yi ñuy tëje ndaje bi (3 minit) | Woy-Yàlla nº. 130 ak ñaan