Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Li ñi teew war a xam

Li ñi teew war a xam

SÓOB BI Magi mbooloo mi jël nañu ba pare matuwaay yi gën, ngir ñi bëgg a sóobu ci ndox mën koo def, bu porogaraamu samdi bi ci suba si jeexee.

ÑI BËGG A DEF AY MAYE Ndaje bu mag bu ñetti fan bii, dinañu ko tekki ci lu ëpp 400 làkk. Maye yi ngeen di def dafay jàppale liggéey boobu ñuy def ci àddina si sépp. Mën ngeen maye jaare ko ci internet ci donate.pr418.com. Ñu ngi leen di gërëm bu baax ci lépp li ngeen di maye. Jataay biy dogal it mu ngi leen di gërëm ci lépp li ngeen di maye ngir liggéeyu Nguur gi jëm kanam.

LEKKOOL BI ÑU JAGLEEL ÑIY WAARE NGUURU YÀLLA Pioñee yi am diggante 23 at ba 65 at te bëgg yokk seen liggéeyu waare bi, mën nañu jokkoo ak seen sekereteeru mbooloo mi te bindu ci internet ngir mën a dem ci Lekkool bi ñu jagleel ñiy waare Nguur gi.

Jataay biy dogal ci Seede Yexowa yi moo taxawal ndaje bii

© 2021 Watch Tower Bible and Tract Society of Pennsylvania