Samdi
«Xeexleen xeex bu metti ngir seen ngëm» (Yudd 3, MN)
SUBA SI
-
9:20 Porogaraamu misik bu ànd ak wideo
-
9:30 Woy-Yàlla n° 57 ak ñaan
-
9:40 WAXTAAN BU DEF AY XAAJ: Fàttalikuleen ne: Ñi gëmul sax mën nañu dem ba am ngëm!
-
• Waa Niniw (Yunus 3:5)
-
• Ay rakku Yeesu yu góor (1 Korent 15:7)
-
• Ay kilifa yu mag (Filib 3:7, 8)
-
• Ñi amul diine (Room 10:13-15; 1 Korent 9:22)
-
-
10:30 Jëfandikool téere bi tudd Mën nga dund ci jàmm ba fàww, ngir dëgëral seen ngëm (Yowaana 17:3)
-
10:50 Woy-Yàlla n° 67 ak yégle yi
-
11:00 WAXTAAN BU DEF AY XAAJ: Ay jàmbaar ci xeex ngir seen ngëm
-
• Ñi am jëkkër walla jabar ju dul jaamu Yexowa (Filib 3:17)
-
• Xale yiy dund ak seen benn waajur kese (2 Timote 1:5)
-
• Karceen yi nekk salibateer (1 Korent 12:25)
-
-
11:45 SÓOB BI: Am ngëm mooy tax a am dund gu dul jeex! (Macë 17:20; Yowaana 3:16; Yawut ya 11:6)
-
12:15 Woy-Yàlla n° 79 ak noppalu bi
NGOON GI
-
1:35 Porogaraamu misik bu ànd ak wideo
-
1:45 Woy-Yàlla n° 24
-
1:50 WAXTAAN BU DEF AY XAAJ: Naka la suñu mbokk yi di wonee ngëm ca . . .
-
• Afrik
-
• Asi
-
• Ërop
-
• Bëj-gànnaaru Amerik
-
• Océanie
-
• Bëj-saalumu Amerik
-
-
2:15 WAXTAAN BU DEF AY XAAJ: Yàlla ubbil na ñu ay bunt ngir ñu wone suñu ngëm
-
• Jàng làkk bu bees (1 Korent 16:9)
-
• Toxu fi ñu gën a soxla ay waarekat (Yawut ya 11:8-10)
-
• Bindu ngir dem ci Lekkool bi ñu jagleel ñiy waare Nguur gi (1 Korent 4:17)
-
• Dimbali ci liggéeyu tabaxu béréb yi ñuy jaamoo Yàlla (Neyemi 1:2, 3; 2:5)
-
• «Ber» dara ngir jàppale liggéeyu Yexowa (1 Korent 16:2)
-
-
3:15 Woy-Yàlla n° 84 ak yégle yi
-
3:20 TIYAATAR BU SUKKANDIKU CI BIIBËL BI: Dañeel: Dafa amoon ngëm ci dundam gépp (Xaaj I) (Dañeel 1:1–2:49; 4:1-33)
-
4:20 «Xeexleen xeex bu metti ngir seen ngëm»! (Yudd 3, MN; Kàddu yu Xelu 14:15; Room 16:17)
-
4:55 Woy-Yàlla n° 38 ak ñaan bu mujj bi