Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Ku leen sàkk ?

Ku leen sàkk ?

Ku leen sàkk ?

1 Yàlla moo sàkk asamaan ak suuf. — Njàlbéen ga 1:1

2 Yàlla am na tur. Turam mooy Yexowa. — Psaume 83:⁠18.

Yexowaa ngi dëkk ci asamaan. Xel la. Kenn mënu ko gis. — Isaïe 66:1 ; Yowaana 1:18 ; 4:⁠24

3 Yexowa Yàlla moo sàkk malaaka yu bare ci asamaan. Ñoom it xel lañu. Ñoom ñépp baaxoon nañu. Ca njàlbéen, léeg-léeg ñu soppeeku nekk nit, ndax ñu mën leen gis. — Yawut ya 1:7

4 Yexowa sàkkoon na rab yi bu yàgg a yàgg, bala mu sàkk nit sax. — Njàlbéen ga 1:⁠25

5 Yexowa sàkkoon na itam góor gu tudd Aadama, ak jabaram Awa. — Njàlbéen ga 1:⁠27

Yàlla dugaloon na leen ci tool bu rafet a rafet maanaam àjjana. Benn jabar rekk la ko wutaloon. Góor dafa waroon a am benn jabar doŋŋ. — Njàlbéen ga 2:​8, 21, 22, 24

6 Nit bakkan la. — Njàlbéen ga 2:7

7 Rab yi bakkan lañu. — Njàlbéen ga 1:24