Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Lan ngeen war a def ?

Lan ngeen war a def ?

Lan ngeen war a def ?

50 Ndax bëgg ngeen dund ba fàww ci àjjana bu rafet bi ?

Su dee waaw, war ngeen yokk seen xam-xam ci lu Yàlla santaane. Nangeen jéem a jàng Biibël bi. — Yowaana 17:3 ; Peeñu ma 1:3

51 Yokkleen seen xam-xam ci Yeesu. — Deutéronome 18:​18, 19 ; Yowaana 3:16 ; Jëf ya 3:​19-23

52 Nangeen góor-góorlu ba def lu baax rekk te déggal Yexowa. — Room 6:​17, 18, 22

53 Fàttalikuleen ! Yexowa nee na : Waruñu rey nit. — Gàddaay gi 20:13 ; 1 Yowaana 3:​11, 12

54 Waruñu jël li keneen moom. — Gàddaay gi 20:15 ; Efes 4:⁠28

55 Góor warul nekkaale ak jigéen bu dul jabaram. — Gàddaay gi 20:​14, 17 ; 1 Tesalonig 4:3

56 Ndax fàttaliku ngeen ñaata jabar la Yàlla may góor ? Ba kañ la góor war a ànd ak jabaram ? — Njàlbéen ga 2:​22, 24 ; Macë 19:​5, 6 ; 1 Korent 7:​2, 10, 11

57 Nañu fàttaliku ne Yexowa rekk lañu war a jaamu. — Macë 4:10 ; 1 Korent 8:6

58 Xërëm yi ak nataal yi mënuñu dimbali kenn. Lu tax ? — 1 Korent 8:4

Ndax am xërëm ak nataal baax na ? — Deutéronome 27:15 ; 1 Yowaana 5:⁠21

59 Lu tax takk téere ak jëfandikoo xërëm bon ? — Deutéronome 18:​10-13 ; Peeñu ma 21:8

60 Seytaane yi walla malaaka yu bon yi dañu jógal Yàlla. Ci gisaanekat yi lañuy jaar ba nax nit ñi. — Jëf ya 16:⁠16

61 War nañu ñaan Yàlla. Moo di wax ak moom, xamal ko ne bëgg nañu ko jaamu te ñaan ko ndimbalam. — Filib 4:​6, 7

62 War nañu déggal Yeesu te gëm ci moom. — Yawut 5:9 ; Yowaana 3:⁠16

63 Buleen fàtte ne deewam moo ñu tax a mucc. — Room 5:8

64 Fàttalikuleen ne Yeesu mooy suñu Buur. Mënuñu ko gis. War nañu ko déggal. — Filip 2:​9-11 ; Peeñu ma 19:⁠16

65 Yeesu nee na : War ngeen xamal ñeneen ñi yëf yu baax yi ngeen jàng te ñi bëgg jaamu Yàlla war nañu batise. — Macë 28:​19, 20 Yowaana 4:​7-15

66 Bu boobaa mën ngeen ci waxtaan ak seeni xarit. — Macë 10:⁠32

67 Su ngeen mënee jàng, dingeen xam yeneen yëf yu bare, te dingeen gën a mën a dimbali ñeneen. — 2 Timote 2:⁠15

68 Yeesu jàngal na xale yu tuuti yi ñu déggal Yàlla. Masul a ñàkk jotu waxtaan ak ñoom.— Macë 19:​13-15

69 Waajur war na bés bu nekk jàngal doomam mu déggal Yàlla te bëgg ko. — Deutéronome 6:​6, 7 ; Léeb yi 6:​20-22 ; Efes 6:4

70 Diine yi bare nañu. Li ëpp ci li ñuy jàngale, nekkul ci Biibël bi. Yexowa nee na ñu bàyyi yoon bu dul jàngale dëgg. — Peeñu ma 18:4 ; Yowaana 4:​23, 24

71 Yexowa am na ay nit ci suuf si yu leen mën a jàngal li gën a bare ci moom. Ndax xam ngeen ñan lañu ? — Jëf ya 15:14 ; Room 10:​14, 15

72 Ñooy Seede Yexowa yi. Jàmm a nekk ci seen biir. Ndax xam ngeen lu tax ? Li ñu bëggantee tax. — Isaïe 43:​10-12 ; Yowaana 13:​34, 35

73 Ndegam bëgg nañu itam Yexowa, dañu leen batise. Noonu lañuy yëgale ñépp ne bàyyi nañu yëf yu bon yi ñu daan def te bëgg nañu jébbalu ci Yàlla ci seen dund. — Jëf ya 2:⁠41

74 Seede Yexowa yi yaakaar nañu dund ci àjjana bu rafet a rafet te bees. — Sabóor 37:​9-11, 29

Lan ngeen mën a def ba bokk ko ak ñoom ? — Saag 1:​22, 25 ; 2:​20-26

75 Fekkeleen seeni ndaje ndax ngeen mën a jàng ni ñuy jaamoo Yexowa. Bëgg nañu Yexowa ak Yeesu Kirist te déggal nañu leen. Ndax bëgg ngeen Yàlla ak Yeesu ? Ndax bëgg ngeen dimbali yeneen nit ba ñu xam Yàlla ? — Yowaana 6:​45-47

76 Yexowa ak Yeesu Kirist sopp nañu leen, te bëgg nañu ngeen dund ba fàww ci àjjana bi. — Yowaana 3:⁠16

Li ngeen jàng ci nataali téere bii ak tekki yi ci ànd, wóor na ne bëggloo na léen dund ba fàww ak bànneex ci suuf si. Ndax bëgg ngeen yokk seen xam-xam ci loolu yépp ? Su dee waaw, waxtaanleen ak kenn ci Seede Yexowa yi. Mën ngeen bind walla bindlu, ci seen biro bi leen gën a jege. Adarees yaa ngi ci ndoorte téere bii.