Lu dee tekki ?
Lu dee tekki ?
15 Su nit deewee, dafay dellu nekk suuf. Dootul xam dara. —Psaumes 146:4
Ku dee mënul wax dara, mënul def dara. — Ecclésiaste 9:5, 10
16 Wànte malaaka yu bare dañu soppeeku ba bon. Dañu bëgg ñu jaawale leen ak ñi dee. Dañu bëgg gëmloo ne nit du dee ci dëgg-dëgg. — Njàlbéen ga 6:1, 2 ; Yudd 6
17 Yàlla Yexowa bëggul ñu gëm malaaka yu bon yooyu ñu tudde seytaane. —Exode 22:18 ; Deutéronome 18:10, 11 ; 32:17
Yexowa bëggul ñu def lu jëm ci xërëm, gisaane ak xamb. — Galasi 5:19-21