Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Lu tax nit di dee ?

Lu tax nit di dee ?

Lu tax nit di dee ?

8 Yàlla Yexowa bëggoon na nit liggéey suuf si ba mu nekk béréb bu jekk — benn àjjana fu nit ñépp mën a dëkk. — Njàlbéen ga 1:⁠28

Nit ñi mënoon nañu dund ba fàww, su Aadama ak Awa déggaloon Yexowa. Waxoon na leen ñu bañ a lekk doomu garabu xam lu baax ak lu bon. — Njàlbéen ga 2:​15-17

9 Benn malaaka dafa soppeeku nekk ku bon, te jaar ci benn jaan ba fexe Aadama ak Awa déggadi Yàlla. — Njàlbéen ga 3:​1-6

10 Malaaka bi nax Awa, moom lañu mujj tudde ‘ jaanu cosaan ’, Ibliis ak “ Seytaane ”. — Peeñu ma 12:9

11 Yexowa dafa leen dàq ci àjjana bi, ndax li ñu ko déggalul. — Njàlbéen ga 3:​23, 24

12 Aadama ak Awa amoon nañu ay doom, waaye njaboot googu yépp béguñu woon. — Njàlbéen ga 3:​17, 18

13 Ni ko Yexowa waxe woon, dañu mujj màggat ba dee. — Njàlbéen ga 3:19 ; Room 5:⁠12

14 Faf nañu dee ni rab yi.

Bakkan yi nekk ci suuf si yépp dañuy dee. — Ecclésiaste 3:​18-20 ; Ézékiel 18:4