Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Naka la bàkkaar ak dee mënee teggeeku ci ñun ?

Naka la bàkkaar ak dee mënee teggeeku ci ñun ?

Naka la bàkkaar ak dee mënee teggeeku ci ñun ?

35 Fàttalikuleen ne Aadama, nit bu jëkk bi bàkkaaroon na. Ci la ñàkke bakkanam ak àjjana bi ; looloo tax ñun ñépp, ñuy dee itam, ndax ay doomam lañu. — Room 5:12 ; 3:⁠23

36 Mënoon nañu amaat dund gu mat sëkk, su beneen nit bu mat sëkk joxe woon bakkanam ndax ñun, ba jële ñu ci dee. — 1 Korent 15:45 ; Room 5:​19, 21

37 Yeesu doomu Yàlla la woon. Nit ku mat sëkk la woon. Masul bàkkaar. — Yawut 5:9 ; 7:⁠26

38 Nangu woon na nit ñi bëggul woon Yàlla jël bakkanam. — Jëf ya 2:⁠23

Noonu la jébbalee boppam ndax ñun. — 1 Timote 2:6

39 Tàbbal nañu néewu Yeesu ci bàmmeel bi ñu gas ci xeer. Nekkoon na fa ñetti fan ba Yàlla dekkal ko. — Jëf ya 2:⁠24

40 Dellu na ci asamaan si. Léegi nag mën na ñaan Yàlla mu dimbali ñi ko déggal. — Yawut 9:24 ; 1 Yowaana 2:​1, 2