Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Ndax Yàlla dina alagaat ñu bon ñi ?

Ndax Yàlla dina alagaat ñu bon ñi ?

Ndax Yàlla dina alagaat ñu bon ñi ?

22 Nitu tey soxor nañu lool ñoom itam. Yu bon yan lañuy def ?

23 Am na ñuy rey yeneen nit. Yàlla tere na rey. — Gàddaay gi 20:13 ; 1 Yowaana 3:​11, 12

24 Am na ñuy sàcc. Yàlla tere na sàcc. — Gàddaay gi 20:15 ; Efes 4:⁠28

25 Am na góor yuy tàkk jabar yu bare. Am na ñeneen ñuy dëkk ak ñaari jabar walla li ko ëpp ci kër yu wuute. Am na itam ñuy nekkaale te séyuñu. Loolu yépp bokkul ak li Biibël bi santaane. — Macë 19:​4-6 ; 1 Korent 7:​1-4 ; 1 Timote 3:​1, 2

26 dax fàttaliku ngeen ne Yàlla benn jabar rekk la joxoon Aadama ? — Njàlbéen ga 2:​22, 24

27 Am na ñuy jaamu ay xërëm. Waaye Yàlla nee na : Waruloo boole xërëm walla nataal ci sa diine. — Gàddaay gi 20:​4, 5 ; Isaïe 44:​9-17 ; 1 Yowaana 5:⁠21

28 Yàlla dina alag nit ñu bon ñu bëggul soppeeku. — Psaumes 37:​9, 10 ; Luug 13:5 ; 1 Korent 6:​9, 10