Nguuru Yàlla dina indi barke ci suuf si
Nguuru Yàlla dina indi barke ci suuf si
41 Yexowa fal na Yeesu buur ci asamaan si. — Isaïe 9:6 ; Dañeel 7:13, 14 ; Jëf ya 2:32-36
42 Yeesu dina ilif àddina bi yépp. — Dañeel 7:14 Macë 28:18
43 Ndax fàttaliku ngeen li war a dal nit ñu bon ñi ? —44 Ndax fàttaliku ngeen, turu malaaka bi jëkk bàkkaar ? Yeesu dina ko rey moom ak yeneen malaaka yu bon yi. Xërëm yi ak nataal yi dinañu tas. — Yawut ya 2:14 ; Peeñu ma 20:2, 10
45 Yeesu dina defal ñi ko déggal yëf yu rafet te bare. — Yawut ya 5:9
46 Dootul amati mukk ñu wopp. — Isaïe 33:24 ; Peeñu ma 22:1, 2
Ndax fàttaliku ngeen naka la Yeesu doon faje ñu woppoon ?
47 Nit ñépp dinañu am yëf yu neex. —48 Yàllaa ngi fàttaliku sax ñi deewoon. Dina jaar ci Yeesu ba ñu dundaat. Loolu lañu tudde dekki. — Yowaana 5:28, 29 ; 11:25
Peeñu ma 21:4 ; Isaïe 65:25 ; Sabóor 37:11, 29
49 Su ñu bon ñi ñépp deewee, kenn dootul dee mukk. Rabu àll yi sax dootuñu songe. Nit ñépp dinañu nekk ci bànneex ba fàww. —