Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Yàlla alag na àdduna bu bon

Yàlla alag na àdduna bu bon

Yàlla alag na àdduna bu bon

18 Doomu Aadama yi mujj nañu sakkan, waaye itam dañu soxoroon lool. Yàlla fas na yéene rey leen. — Njàlbéen ga 6:​1, 5, 7

19 Waaye amoon na benn góor gu baax gu tuddoon Nóoyin. — Njàlbéen ga 6:​8, 9

Yàlla Yexowa ne woon na ko mu daaj benn gaal gu mag fu muy dugg ak njabootam ngir mucc, su fiy jëlee ñu bon ñépp. Gaal googu dafa nuru woon waxande gu réy. “ Arche ” la tuddoon. — Njàlbéen ga 6:​13, 14

20 Dugaloon nañu rab yu bare ci biir gaal gi. — Njàlbéen ga 6:​19-21

21 Yexowa xëppoon na tuufaan ci suuf si ba nit ñu bon ñépp dee. Nit ñi nekkoon ci biir gaal gi ñoo mucc. Ndax xam ngeen lu tax ? — Njàlbéen ga 6:17 ; 7:​11, 12, 21 ; 1 Piyeer 3:​10-12