Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Yexowa jox na ñu Musalkat

Yexowa jox na ñu Musalkat

Yexowa jox na ñu Musalkat

29 Xel mi Yàlla jëkk sàkk meloon na ci moom ni taawam bu góor.

Yàlla sopp na ko lool. Dina ko sant mu rey nit ñu bon ñi te musal ñi ko déggal — Yowaana 3:​16, 36

30 Yexowa yónni na doomam mu juddu ci suuf si. Ñu tudde ko Yeesu. Yaayam moo tuddoon Maryaama. — Luug 1:​30-35

31 Ba mu doonee waxambaane, daan na jàngale yëf yu bare te rafet, maanaam Yexowa rekk mooy Yàlla bu dëgg. — Màrk 12:​29, 30

Yeesu nee na Yexowa rekk lañu war a jaamu. — Macë 4:10 ; Yowaana 4:​23, 24

Jàngal na itam nit ñi li jëm ci Nguuru Yàlla. — Luug 17:​20, 21

32 Yeesu faj na nit ñi woppoon te def na yëf yu bare yu rafet. Masul a def dara lu bon. — Jëf ya 10:38 ; 1 Piyeer 2:​21, 22

Wànte naka la mënee teggi bàkkaar ak dee ?

33 Dafa mujj jébbalu ci Yàlla ndax nit ñu baax ñi mucc. Bu jëkk, Yàlla santaane woon na nit ñi saraxe ay rab ndax seen bàkkaar. — Yawut ya 7:​25, 27

34 Yeesu saraxewul ay rab. Boppam la jébbale ndax ñun. — Macë 20:28 ; Yawut ya 10:⁠12

Ndax xam nga lu tax ?