Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Dimbalil ñeneen ñu def li Yàlla bëgg

Dimbalil ñeneen ñu def li Yàlla bëgg

Njàngale 15

Dimbalil ñeneen ñu def li Yàlla bëgg

Lu tax nga wara waxtaan ak ñeneen ci li ngay jàng ? (1)

Kan nga mëna séddool xibaar bu neex bi ? (2)

Lan la sa jëfin mëna jur ci ñeneen ñi ? (2)

Kañ ngay mëna ànd ak mbooloo mi ci waare bi ? (3)

1. Fi nga tollu nii, jàng nga lu bare te baax ci Mbind mu sell mi. Xam-xam boobu moo la mëna dimbali ba ngay jikkowoo jikko taalibe Isaa (Efes 4:22-24). Xam-xam boobu rekk moo mëna tax ngay am dund gu dul jeex (Yowanna 17:3). Waaye, ñeneen ñi it soxla nañu déglu xibaar bu neex bi ngir mëna mucc. Taalibe Isaa yu dëgg yi yépp war nañu waar nit ñi. Loolu la Yàlla santaane. — Room 10:10 ; 1 Korent 9:16 ; 1 Timote 4:16.

2. Mën nga njëkk waxtaan ci li ngay jàng ak ñi la jege. Na nga ko waxtaane ci sa biir njaboot, ak say xarit, ñi nga bokkal lekkool walla ñi nga bokkal liggéey. Booy def loolu na nga baax te neex deret (2 Timote 2:24, 25). Bul fàtte ne nit ñi dañu faral di seet say jëf bala ñuy déglu li ngay wax. Kon say jëf yu rafet ñoo mëna tax ñu déglu la booy waare. — Macë 5:16 ; 1 Pieer 3:1, 2, 16.

3. Dinga dem ba mat ku mëna ànd ci waare bi ak mbooloo Seede Yexowa mi nekk ci sa dëkk. Booba dafay wone ne jëm nga kanam ba tollu fu am solo (Macë 24:14). Boo mënee dimbali keneen mu jaamu Yexowa te am dund gu dul jeex, mbégte boo ciy am dina doon mbégte bu réy ! — 1 Tesalonikk 2:19, 20.