Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Fas nga yéene jaamu Yàlla

Fas nga yéene jaamu Yàlla

Njàngale 16

Fas nga yéene jaamu Yàlla

Lan nga wara def ba mëna nekk xaritu Yàlla ? (1, 2)

Naka ngay jébbale sa bopp Yàlla ? (1)

Kañ lañu la wara sóob ci ndox ? (2)

Naka nga mënee am doole ngir wéy di takku ci Yàlla ? (3)

1. Boo bëggee nekk xaritu Yàlla, danga wara jàng ba xam bu baax dëgg gi nekk ci Mbind mu sell mi (1 Timote 2:3, 4), am ngëm ci li nga jàng (Yawut yi 11:6), réccu say bàkkaar (Jëf ya 17:30, 31), won ginnaaw li nga daan def (Jëf ya 3:19). Bu boobaa, mbëggeel bi nga am ci Yàlla dina tax nga bëgg koo jébbal sa bopp. Maanaam dinga wéet ngir ñaan Yàlla. Ci ñaan boobu dinga ko wax ne yaa ngi koy jox sa bopp ngir def li mu bëgg. — Macë 16:24 ; 22:37.

2. Boo jébbalee sa bopp Yàlla ba pare, war nañu la sóob ci ndox (Macë 28:19, 20). Sóob ci ndox dina tax ñépp xam ne jébbal nga sa bopp Yexowa. Kon bala ñu lay sóob ci ndox, war nga tollu ci ay at yu lay may nga mëna fas yéene jaamu Yàlla. Ku ñu sóob ci ndox, sa yaram wépp lañu wara dugal ci biir ndox mi, daldi ko gaawa génne. *Mark 1:9, 10 ; Jëf ya 8:36.

3. Boo jébbalee sa bopp Yàlla ba pare, Yexowa bëgg na nga dunde li nga ko dig (Sabuur 50:14 ; Dajalekat 5:4, 5). Ibliis dina la jéema génne ci li ngay jaamu Yexowa (1 Pieer 5:8). Waaye na nga gëna jege Yàlla ci ñaan (Filipp 4:6, 7). Jàngal Kàddoom bés bu nekk (Sabuur 1:1-3). Na nga taq ci mbooloo mi (Yawut yi 13:17). Boo defee loolu lépp, dinga am doole ngir wéy di takku ci Yàlla. Kon fii ba fàww, dinga mëna def li la Yàlla laaj !

[Li ñu bind ci suuf]

^ Bala ñu lay mëna sóob, na nga jàng téere bu tudd Xam-xam biy jëme ca dund ga dul jeex, walla téere bu mel ni moom bu Watch Tower Bible and Tract Society génne.