Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Fonk dund ak deret

Fonk dund ak deret

Njàngale 12

Fonk dund ak deret

Naka lañu wara gise bakkan ? (1) yàq biir ? (1)

Naka la taalibe Isaa yi wone ne foyewuñu bakkanu nit ? (2)

Rey ay mala, ndax araam na ? (3)

Yan ñooy ay jëf yuy wone ne fonkuñu bakkan ? (4)

Lan mooy ndigalu Yàlla ci deret ? (5)

Ndax loolu ëmb na sol deret ci yaram ? (6)

1. Dund gi, ci Yexowa la jóge. Moo sàkk lépp luy dund (Sabuur 36:9). Bakkan lu tedd la ci kanamu Yàlla. Yexowa fonk na sax bakkanu doom ju juddoogul te nekk di màgg ci biiru ndeyam. Rey ko fekk yaa ko tey, lu bon la ci kanamu Yàlla.  2 Musaa 21:22, 23 ; Sabuur 127:3.

2. Taalibe Isaa yu dëgg yi duñu foye bakkan. Dañuy seetlu bu baax seen oto ak seen kër ndax dara lu ci nekk baña lor kenn (5 Musaa 22:8). Jaami Yàlla yi duñu jaay walla foye seen bakkan ngir am walla yëg bànneex. Looloo tax duñu bokk ci tàggat yaram yuy ànd ak jëfi fitna walla gaañante. Duñu fo ak li leen di dugal ci jëfi fitna.  Sabuur 11:5 ; Yowanna 13:35.

3. Bakkanu mala itam lu tedd la ci kanamu Yàlla mi sàkk lépp. Taalibe Isaa mën na rey mala ngir lekk, am lu muy sol, aar boppam ci feebar walla ci musiba (1 Musaa 3:21 ; 9:3 ; 2 Musaa 21:28). Wànte waruñu soxor ak mala yi walla rey leen ngir fo walla am ci bànneex.  Léebu 12:10.

4. Taalibe Isaa yi waruñu tux, sàqami betel, walla jël dorog ngir am ci bànneex. Jëf yooyu baaxuñu ndaxte (1) dañu lay jiital, (2) dañuy yàq sa yaram, te (3) selluñu (Room 6:19 ; 12:1 ; 2 Korent 7:1). Bu ñu xasee tàmm jëf yooyu, tàggoo ak ñoom mën na jafe lool. Waaye war nañu def loolu ngir neex Yexowa.

5. Deret itam lu tedd la ci kanamu Yàlla. Yàlla wax na ne bakkan walla dund ci deret la nekk. Kon nag lekk deret baaxul. Lekk yàppu mala fekk tuuruñu deretam ni mu ware, loolu itam baaxul. Kenn warul lekk mala bu ñu xoj ba mu dee, walla mala bu dee ci fiir . Bu ñu gaañee mala ak fett walla fetal, su ñu ko bëggee lekk war nañu ko gaawa rendi ndax deretam tuuru. — 1 Musaa 9:3, 4 ; 3 Musaa 17:13, 14 ; Jëf ya 15:28, 29.

6. Ndax nangu ñu sol la deret araam na ? Fàttalikul ne Yexowa mu ngi ñuy laaj ñu baña nangu deret. Maanaam waruñu nangu ñu dugal deret ci suñu yaram ci fasoŋ bu mu mënta doon, muy deretu jaambur walla sax suñu deretu bopp bu ñu dencoon (Jëf ya 21:25). Kon nag taalibe Isaa yu dëgg yi duñu nangu ñu sol leen deret. Dinañu nangu ñu faj leen ak yeneen pexe yu mel ni sol ci yaram yeneen garab yu amul deret. Bëgg nañu dund, waaye duñu nangu jéggi yoonu Yàlla ngir baña dee. — Macë 16:25.

[Nataal yi nekk paas 25]

Ku bëgga neex Yàlla, war nga bañ ñu sol la deret, baña tàmm lu bon te baña foye sa bakkan