Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Gëna jege Yàlla ci ñaan

Gëna jege Yàlla ci ñaan

Njàngale 7

Gëna jege Yàlla ci ñaan

Lu tax tàmm di ñaan Yàlla am solo ? (1)

Kan lañu wara ñaan, te naka lañu ko wara defe ? (2, 3)

Lan lañu mëna ñaan Yàlla ? (4)

Kañ nga wara ñaan ? (5, 6)

Ndax Yàlla dafay déglu ñaan yi yépp ? (7)

1. Ñaan mooy wax ak Yàlla ak xol bu woyof. War nga tàmm di ñaan Yàlla. Boo defee loolu, dinga jege Yàlla ba mu nekk sa xarit dëgg. Dëgg la, Yexowa ku màgg la te bare kàttan. Waaye loolu terewu ko déglu suñuy ñaan ! Mbaa tàmm nga di ñaan Yàlla ? — Sabuur 65:2 ; 1 Tesalonikk 5:17.

2. Ñaan bokk na ci li ñu wara def ngir jaamu Yàlla. Kon nag Yàlla Yexowa rekk lañu wara ñaan. Bi Isaa nekkee ci kow suuf, masul ñaan keneen ku dul Baayam. Ñun it, loolu lañu wara def (Macë 4:10 ; 6:9). Waaye, suñuy ñaan yépp war nañu leena jaarale ci turu Isaa. Loolu mooy wone ne nangu nañu taxawaayu Isaa. Dina wone itam ne dañu am ngëm ci saraxam bi nekk njot gi. — Yowanna 14:6 ; 1 Yowanna 2:1, 2.

3. Bu ñuy ñaan Yàlla, dañu wara wax li nekk suñu biir xol. Waruñu tari suñuy ñaan walla di leen jële ci téere bu ñu bind ay ñaan (Macë 6:7, 8). Mën nga ñaan saa yoo ko bëggee, foo mënta nekk, waaye na ànd ak teggin. Yàlla mën na dégg sax ñaan bu ñuy wax ci suñu biir xol (1 Samwil 1:12, 13). Boo bëggee def say ñaani bopp, dem foo mëna wéet moo baax. — Mark 1:35.

4. Lan nga mëna ñaan Yàlla ? Lépp lu mëna rattaxal sa diggante ak moom (Filipp 4:6, 7). Boo seetee ñaan bi ñu wara roy, dinga ci gis ne dañu wara ñaan ngir turu Yexowa ak coobareem. Mën nañu ñaan Yàlla itam ngir am lu ñuy faje suñuy soxla, ñaan ko mu baal ñu suñuy bàkkaar, te mu dimbali ñu ngir moytu lu ñuy xiir ci lu bon (Macë 6:9-13). Waruñu xalaat suñu bopp rekk bu ñuy ñaan Yàlla. Li ànd ak li Yàlla bëgg rekk lañu wara ñaan. — 1 Yowanna 5:14.

5. Mën nga ñaan saa yu la sa xol xiiree ci gërëm walla sant Yàlla (1 Nettaliy xew-xewi cosaan 29:10-13). War nga ñaan itam boo nekkee ci coono bu mëna tax nga weddi sa ngëm (Sabuur 55:22 ; 120:1). Jaadu na ngay ñaan bala ngay lekk (Macë 14:19). Yexowa dafa bëgg ñuy ñaan fu ñu mënta tollu. — Efes 6:18.

6. Bu ñu defee bàkkaar bu réy, booba lañu gëna soxla ñaan Yàlla, ngir ñu mëna jot ci yërmandeem te mu jéggal ñu. Bu ñu ko waxee suñu bàkkaar te def suñu kem-kàttan ngir bañ cee dellu, Yàlla dina ñu bëgga baal.Sabuur 86:5 ; Léebu 28:13.

7. Yexowa du déglu mukk say ñaan su fekkee ne nekkuloo nit ku jubBoo bëggee Yàlla nangu say ñaan, war na fekk ngay def sa kem-kàttan ngir topp ay ndigalam (Léebu 15:29 ; 28:9). Booy ñaan danga wara am xol bu woyof (Lukk 18:9-14). War nga fexee def li ànd ak li nga ñaan. Noonu ngay wonee ne am nga ngëm te li nga wax yemul ci sa làmmiñ kese. Loolu rekk moo mëna tax Yexowa nangu say ñaan. — Yawut yi 11:6.