Kan mooy Isaa ?
Njàngale 3
Kan mooy Isaa ?
Lu tax ñu tudde Isaa “ Taawu ” Yàlla ? (1)
Lu tax ñu tudde ko “ Kàddu gi ” ? (1)
Lu tax Isaa ñów ci kow suuf nekk nit ? (2-4)
Lu tax mu doon def ay kéemaan ? (5)
Lan la Isaa nara def ci kanam tuuti ? (6)
1. Isaa (Yeesu) nitu xel la woon ca asamaan bala mu ñów ci kow suuf. Moom la Yàlla njëkka sàkk, moo tax ñu tudde ko “ Taawu ” Yàlla (Kolos 1:15 ; Peeñu bi 3:14). Bi Yàlla sàkkee Isaa, jaarul ci kenn. Doom jooju rekk la Yàlla sàkke noonu. Te bala Isaa ñów ci kow suuf, Yexowa defoon na ko mu nekk ci wetam “ liggéeykat bu mën liggéeyam ”, ba Yàlla doon sàkk li ci des yépp ca asamaan ak ci suuf (Léebu 8:22-31 ; Kolos 1:16, 17). Moom la Yàlla doon gëna yónni ngir jottali Kàddoom. Looloo tax ñu tudde Isaa “ Kàddu gi ”. — Yowanna 1:1-3 ; Peeñu bi 19:13.
2. Yàlla dafa jël bakkanu Doomam toxal ko ci biiru Maryaama. Noonu la ko yónnee ci kow suuf. Kon baayu Isaa bokkuloon ci doom-Aadama yi. Looloo tax donnul benn bàkkaar walla sikk. Yàlla yónni na Isaa ci suuf ngir ñetti mbir : (1) mu jàngal ñu dëgg ci Yàlla (Yowanna 18:37), (2) mu takku ci Yàlla takkute bu mat sëkk, ngir ñu mën ko roy (1 Pieer 2:21), te (3) mu saraxe bakkanam ngir génne ñu ci bàkkaar ak dee. Lu tax mu waroona def loolu ? — Macë 20:28.
3. Góor gu njëkk ga, Aadama, toppul li ko Yàlla santoon. Noonu la defe li Mbind mu sell mi tudde “ bàkkaar ”. Yàlla daldi ko wax ne dina dee (1 Musaa 3:17-19). Mënatuloona def ba mu mat li Yàlla bëggoon, moo tax nekkatuloon nit ku mat. Mu tàmbali màgget ndànk-ndànk ba mujja dee. Aadama wàll na doomam yépp bàkkaar. Looloo tax it ñuy màgget, di feebar, tey dee. Naka la doom-Aadama yi mënoona mucc ci loolu ? — Room 3:23 ; 5:12.
4. Isaa, nit ku mat la woon ni Aadama. Waaye deful ni Aadama ; topp na ndigalu Yàlla yi toppin bu mat sëkk ak lu mu metti metti. Kon, mënoon na saraxe bakkanam bi nekkoon bakkanu nit ku mat, ngir fey bàkkaaru Aadama. Loolu la Mbind mu sell mi tudde “ njot ” gi. Noonu, doom-Aadama yi mënoon nañu mucc ci dee. Képp ku am ngëm ci Isaa, mën nañu la baal say bàkkaar te dinga mëna am dund gu dul jeex. — 1 Timote 2:5, 6 ; Yowanna 3:16 ; Room 5:18, 19.
5. Bi mu nekkee ci kow suuf, Isaa dafa doon faj ñi feebar, jox lekk ñi xiif, te daaneel ay ngelaw yu réy. Dekkal na sax ay nit ñu dee. Lu tax mu doon def ay kéemaan ? (1) Dafa amoon yërmande ci nit ñi nekkoon ci metit, te bëggoon na leena dimbali. (2) Kéemaan yooyu dañu doon wone ne moo doon Doomu Yàlla. (3) Dañu doon wone li mu nara defal nit ñi déggal Yàlla, bés bu nekkee Buur ci kow suuf si sépp. — Macë 14:14 ; Mark 2:10-12 ; Yowanna 5:28, 29.
6. Isaa dee na, Yàlla dekkal na ko mu nekk mbindeefu xel, te dellu na asamaan (1 Pieer 3:18). Ginnaaw loolu Yàlla def na ko Buur. Tuuti ci kanam, Isaa dina dindi lépp lu bon ak lépp li nekk metit ci kow suuf si. — Sabuur 37:9-11 ; Léebu 2:21, 22.
[Nataal yi nekk paas 7]
Jàngal nit ñi, def ay kéemaan te saraxe sax bakkanam ngir ñun, loolu lépp bokk na ci li tax Yàlla yónni Isaa ci kow suuf