Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Kan mooy Yàlla ?

Kan mooy Yàlla ?

Njàngale 2

Kan mooy Yàlla ?

Kan mooy Yàlla dëgg ji, te lan mooy turam ? (1, 2)

Ban fasoŋu yaram la am ? (3)

Yan ñooy jikko yi gëna feeñ ci Yàlla ? (4)

Bu ñuy jaamu Yàlla, ndax war nañu jëfandikoo ay nataal walla yeneen yëf yu mel noonu ? (5)

Yan ñaari pexe lañu am ngir xam Yàlla ? (6)

1. Li nit ñi di jaamu bare na, waaye Mbind mu sell mi nee na benn Yàlla DËGG rekk moo am. Moo sàkk lépp ca asamaan ak ci suuf. Ndegam moo ñu sàkk, Moom rekk lañu wara jaamu. — 1 Korent 8:5, 6 ; Peeñu bi 4:11.

2. Ni ñu mëna woowee Yàlla bare na, waaye benn tur rekk la am. Tur boobu mooy YEXOWA. Li ëpp ci Mbind yu sell yi, dañoo dindi turu Yàlla def ci BOROOM BI walla YÀLLA. Waaye ba ñu doon bind Mbind mu sell mi, tur boobu Yexowa feeñoon na fa lu jege 7 000 yoon ! — 2 Musaa 3:15 ; Sabuur 83:18.

3. Yexowa am na yaram, waaye du yaram bu mel ni suñu bos. Mbind mu sell mi nee na, “ Yàlla Xel la ”. (Yowanna 4:24.) Xel, dafa nekk fasoŋu bakkan boo xam ne dafa sut lool suñu bos. Kenn masul gis Yàlla. Yexowa, ca asamaan la nekk, waaye lépp la mëna gis (Sabuur 11:4, 5 ; Yowanna 1:18). Kon lan mooy xel mu sell mi ? Du nitu xel ni Yàlla, waaye doole ji Yàlla di jëfe la. — Sabuur 104:30.

4. Mbind mu sell mi dafa ñuy xamal jikko Yexowa. Dafa ñuy won ne jikko yi gëna feeñ ci moom ñooy mbëggeel, njub, xam-xam ak kàttan (5 Musaa 32:4 ; Ayóoba 12:13 ; Isayi 40:26 ; 1 Yowanna 4:8). Mbind mu sell mi dafa ñuy wax itam ne Yàlla dafa am yërmande, ku baax la te mëna jéggal. Wone na itam ne ku nangu maye la te mëna muñ. Ñun, war nañu koo jéema roy ni ay doom yu dégg ndigal. — Efes 5:1, 2.

5. Bu ñuy jaamu Yàlla, ndax war nañu sukk walla ñaan ci kanamu xërëm, nataal walla leneen ? Déedéet (2 Musaa 20:4, 5) ! Yexowa nee na moom rekk lañu wara jaamu. Bëggul bokkaale, muy ak nit walla leneen. Xërëm yi, amul fenn fu ñu mëna dimbali nit ñi. — Sabuur 115:4-8 ; Isayi 42:8.

6. Naka lañu mënee yokk suñu xam-xam ci Yàlla ? Benn pexe mooy di xool bu baax li mu sàkk te xalaat bu baax ci li ñu yëf yooyuy xamal. Li Yàlla sàkk dafa ñuy won ne am na kàttan gu réy ak xam-xam. Mbëggeelam feeñ na ci li mu sàkk lépp (Sabuur 19:1-6 ; Room 1:20). Beneen pexe mooy jàng Mbind mu sell mi. Foofu la ñu Yàlla gëna xamal fasoŋu Yàlla ji mu doon. Wax na ñu itam li mu bëgga def ak li mu bëgg ñu def. — Amos 3:7 ; 2 Timote 3:16, 17.

[Nataal yi nekk paas 5]

Mën nañu xam Yàlla ci li mu sàkk ak ci Mbind mu sell mi