Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Lan mooy Nguuru Yàlla ?

Lan mooy Nguuru Yàlla ?

Njàngale 6

Lan mooy Nguuru Yàlla ?

Fan la Nguuru Yàlla nekk ? (1)

Kan mooy Buuram ? (2)

Ndax am na ñeneen ñuy nguuru ak Buur bi ? Su dee waaw, ñaata lañu ? (3)

Lan mooy wone ne ñu ngi ci muju jamano ? (4)

Bu ëllëgee, lan la Nguuru Yàlla di defal doom-Aadama yi ? (5-7)

1. Ba mu nekkee ci kow suuf, Isaa jàngaloon na taalibeem ya ñu ñaan ngir Nguuru Yàlla. Nguur, kurél la bu buur jiite. Nguuru Yàlla melul ni yeneen nguur yi. Ca asamaan la nekk te dina nguuru ci kow suuf si. Dina sellal turu Yàlla. Dina tax coobare Yàlla am ci kow suuf ni mu ame ca asamaan. Macë 6:9, 10.

2. Yàlla digoon na ne Isaa mooy nekk Buuru Nguuram (Lukk 1:30-33). Bi Isaa nekkee ci kow suuf, wone na ne dina nekk Buur bu baax, jub te mat. Bi mu delloo asamaan, defuñu ko Buuru Nguuru Yàlla ci saa si (Yawut yi 10:12, 13). Ci atum 1914, Yexowa jox na Isaa sañ-sañ bu Mu ko digoon. Booba ba tey, Isaa mu ngi nguuru ci asamaan ni Buur bu Yexowa tànn. Dañel 7:13, 14.

3. Yexowa tànn na itam ci kow suuf si ay góor ak ay jigéen ñu takku ci moom ngir ñu dem ca asamaan. Dinañu nguuru ak Isaa ni ay buur, àttekat ak saraxekat ci kow doom-Aadama yi (Lukk 22:28-30 ; Peeñu bi 5:9, 10). Isaa tudde na ñi mu bokkal nguur gi “ gétt gu ndaw gi ”. Te 144 000 lañu. Lukk 12:32 ; Peeñu bi 14:1-3.

4. Isaa dafa nekk Buur rekk, daldi dàq Seytaane ak malaakaam yu bon yi ci biti asamaan, wàcce leen ci wetu suuf si. Looloo tax 1914 ba tey, àddina si di mettee nii (Peeñu bi 12:9, 12). Xare yi, xiif yu metti yi, feebar yi gaawa law, nit ñiy jéggi yoon di gëna bare loolu lépp bokk na ci luy wone ne Isaa mu ngiy nguuru te jamano jii tollu na ci ay fanam yu mujj yi. Macë 24:3, 7, 8, 12 ; Lukk 21:10, 11 ; 2 Timote 3:1-5.

5. Bu ci kanamee tuuti, Isaa dina àtte nit ñi, xàjjale leen ni sàmmkat di xàjjalee xar yi ak béy yi. “ Xar ” yi ñooy ñi wéyoon di nekk surga Isaa te takku ci moom, di ko wone ci seen dundin. Dinañu am dund gu dul jeex ci kow suuf si. “ Béy ” yi ñooy ñi wéyoon di bañ Nguuru Yàlla. (Macë 25:31-34, 46). Ci kanam tuuti Isaa dina sànk képp ku mel ni béy (2 Tesalonikk 1:6-9). Boo bëggee bokk ci “ xaru ” Isaa yi, war nga déglu xibaaru Nguur gi. War nga jëf itam li ngay jàng. — Macë 24:14.

6. Tey, suuf si dañu ko xàjjale ci ay réew yu bare. Réew mu ci nekk am na nguuru boppam. Réew yooyu, dañu faral di xeex ci seen diggante. Waaye Nguuru Yàlla dina dindi nguuru nit ñi yépp te moom rekk mooy ilif suuf si sépp (Dañel 2:44). Bu boobaa, xeex yi, nit ñuy jéggi yoon, jëfi fitna, dootuñu fi am. Nit ñi ñépp dinañu nekk benn, dëkk ci jàmm. — Mikaa 4:3, 4.

7. Ci 1 000 at yi Isaa di nguuru, nit ñi takku ci Yàlla dinañu nekk nit ñu mat te suuf si sépp dina nekk àjjana. Bu 1 000 at yi matee, dina fekk Isaa def lépp li ko Yàlla santoon. Ginnaaw loolu, dina delloo Nguur gi Baayam (1 Korent 15:24). Lu la tere wax say xarit ak say mbokk li Nguuru Yàlla di defsi ?

[Nataal bi nekk paas 13]

Bu Isaa di nguuroo, bañante walla ñaaw njort, dootul am