Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Naka la Seede Yexowa yi di doxale ci seen mbootaay ?

Naka la Seede Yexowa yi di doxale ci seen mbootaay ?

Njàngale 14

Naka la Seede Yexowa yi di doxale ci seen mbootaay ?

Kañ la Seede Yexowa yi tàmbali seeni yëngu-yëngu ci suñu jamano jii ? (1)

Naka la Seede Yexowa yi di doxale seeni ndaje ? (2)

Fu ñuy jële xaalis bi ñuy doxale seen liggéey ? (3)

Kan mooy jiite ci mbooloo mu nekk ? (4)

Yan ndaje yu gëna mag lañu am at mu nekk ? (5)

Ban liggéey lañuy def ca seen kër gu mag ak ci seeni bànqaas ? (6)

1. Ci suñu jamano Seede Yexowa yi tàmbali nañu seeni yëngu-yëngu yi ca atum 1870. Bu njëkk, Jàngkati Mbind mu sell mi lañu leen doon woowe. Waaye ci atum 1931 dañu jël turu Seede Yexowa bu jóge ci Mbind mi (Isayi 43:10). Bi ñu tàmbalee seen mbootaay, barewuñu woon, waaye yokku nañu ba nekk ay milioŋi Seede yu sawar ci waare bi ci lu ëpp 230 réew.

2. Li ëpp ci mbooloo Seede Yexowa yi, dañuy am ay ndaje ñetti yoon ayu-bés bu nekk. Na nga ñów teewe ndaje yooyu (Yawut yi 10:24, 25). Li ñuy jàngale, ci Mbind mu sell mi lañu koy jële. Ñaan lañuy tàmbalee ndaje yi. Moom lañu koy àggale itam. Ci li ëpp ci ndaje yi, dañu faral di woy ay ‘ woy yu jëm ci wàllu ngëm ’, te seen xol dafa ciy ànd bu baax (Efes 5:18, 19). Booy dugg fu ñuy daje doo fey dara, te boo nekkee ci biir duñu la laaj xaalis. — Macë 10:8.

3. Li ëpp ci mbooloo yi dañuy daje ci Saalu Nguur gi. Saal yooyu ay tabax yu yem lañu faral di nekk. Ay Seede ñoo leen tabax te dañu ko def ngir Yàlla. Doo gis ci Saalu Nguur gi ay nataal, kurwaa, walla yu mel noonu. Xaalis bi ñuy doxale seen mbootaay, mu ngi jóge ci ay maye yu ñu def ak xol bu tàlli. Am na fa ay boyet fu nit ñi mëna dugal li ñu bëgga maye. — 2 Korent 9:7.

4. Ci mbooloo mu nekk am na ay mag walla wottukat. Ñoom ñooy jiite njàngale mi ci mbooloo mi (1 Timote 3:1-7 ; 5:17). Ay surga mbooloo mi ñoo leen di jàppale (1 Timote 3:8-10, 12, 13). Yëkkëtiwuñu góor ñooñu ci kow ñi des ci mbooloo mi (2 Korent 1:24). Kenn joxu leen ay tiitar yuy tax ñu ràññee leen (Macë 23:8-10). Du ñu sol lu leen di ràññale ak ñeneen ñi. Kenn du leen fey liggéey bi ñuy def ci mbooloo mi. Ñi bokk ci mbooloo mi, mag ñi dañuy toppatoo seeni soxla yi jëm ci wàllu ngëm te dañu koy def ak xol bu tàlli. Bu amee ñu nekk ci coono, mën nañu dalal seen xel, di leen tette. — Saak 5:14-16 ; 1 Pieer 5:2, 3.

5. Seede Yexowa yi dañuy am itam ay ndaje yu mag at mu nekk. Booba ay mbooloo yu bare ñooy daje ngir ñu jàngal leen li ñu leen waajal ci wàllu Mbind mu sell mi. Ci ndaje mu mag mu nekk, dañu faral di sóob ci ndox taalibe yu bees yi. — Macë 3:13-17 ; 28:19, 20.

6. Seede Yexowa yi nekk ci àddina si sépp, seen kër gu mag mu nga ca dëkku New-York. Foofu la Jataay Biy Dogal nekk, maanaam kurélu mag ñu bare xam-xam ñi jiite mbooloo Seede Yexowa yi ci àddina si. Am na it lu ëpp 100 bànqaas ci biir àddina si sépp fu ñuy defar tey yónnee ay téere yu sukkandiku ci Mbind mu sell mi. Kenn du fey ña fay liggéey. Ci bànqaas yooyu lañuy jiite liggéeyu waare bi. Lu la tere dem seeti bànqaas bi la gëna jege ?