Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Ngëm yi ak aada yi neexul Yàlla

Ngëm yi ak aada yi neexul Yàlla

Njàngale 11

Ngëm yi ak aada yi neexul Yàlla

Yan ngëm ak aada ñoo bon ? (1)

Ndax taalibe Isaa yi war nañu gëm ne Yàlla Trinite la ? (2)

Lu tax taalibe Isaa yu dëgg yi duñu màggal Nowel, Paag, walla bésu juddu ? (3, 4)

Ndax ñi dee mën nañu lor ñiy dund ? (5)

Ndax Isaa ci kurwaa la dee ? (6)

Bëgga neex Yàlla, lan la la wara jaral ? (7)

1. Du ngëm yépp ak aada yépp ñoo bon. Waaye Yàlla du nangu ngëm walla aada yu jóge ci diine yu dul dëgg yi walla yuy weddi li Mbind mu sell mi wax. — Macë 15:6.

2. Trinite : Ndax Yexowa Trinite la — maanaam ñetti nit yu booloo nekk benn Yàlla ? Déedéet! Yexowa, Baay bi, mooy “ benn Yàlla dëgg rekk ji ” am (Yowanna 17:3 ; Mark 12:29). Isaa mooy Taawam, te dafay déggal Yàlla (1 Korent 11:3). Baay bi moo sut Doom ji (Yowanna 14:28). Xel mu sell mi du nitu xel, waaye doole ji Yàlla di jëfe la. — 1 Musaa 1:2 ; Jëf ya 2:18.

3. Nowel ak Paag : Isaa judduwul ci 25 desàmbar. Ci booru fan bu njëkk ci weeru oktoobar la juddu. Weer boobu bokk na ci weer yi sàmmkat yi daan fanaan àll ak seeni jur (Lukk 2:8-12). Isaa masul sant taalibeem yi ñu màggal bés bi mu juddoo. Waaye dafa leen wax ñu fàttaliku bés bi mu deewee (Lukk 22:19, 20). Nowel ak aada yi mu àndal, ca diine yu dul dëgg yu yàgg ya lañu jóge. Paag itam noonu la. Aada yi mu àndal mel ni jëfandikoo ay nen walla njomboor, ca diine yooyu lañu jóge. Taalibe Isaa yu njëkk ya daawuñu màggal Nowel walla Paag. Kon nag tey itam, taalibe Isaa yu dëgg yi waruñu def loolu.

4. Màggal bésu juddu yi : Ñaari màggali bésu juddu kese lañu nettali ci Mbind mu sell mi. Ñi leen màggal nekkuñu woon ay jaamukatu Yexowa (1 Musaa 40:20-22 ; Mark 6:21, 22, 24-27). Taalibe Isaa yu njëkk ya daawuñu màggal bésu juddu. Aada boobu mu nga jóge ca diine yu dul dëgg yu yàgg ya. Taalibe Isaa yu dëgg yi dañuy def ay maye te dañuy féexal seen xol ci seen diggante, yeneen bés ci at mi.

5. Ragal ñi dee : Ñi dee mënuñu def dara, mënuñu yëg dara. Mënuñu leena dimbali, te ñoom mënuñu lor nit ñi (Sabuur 146:4 ; Dajalekat 9:5, 10). Bu nit deewee, amul dara lu jóge ci moom di wéy di dund. Ruu dafay dee (Esekiel 18:4 ; Macë 10:​28). Waaye yenn saay malaaka yu bon yi ñu tudde seytaane, dañu bëgga nax nit ñi, di leen wax ne ñoo nekk tuuri nit ñi dee. Bépp aada bu jëm ci ragal walla jaamu ñi dee, baaxul. — Isayi 8:19.

6. Kurwaa : Isaa deewul ci kurwaa. Ci benn bant walla poto la dee. Baat ci làkku gerek bi ñu firi “ kurwaa ” ci ay Mbind yu sell yu bare, benn bant rekk la tekki. Kurwaa mu nga jóge ca diine yu dul dëgg yu yàgg ya. Taalibe Isaa yu njëkk ya daawuñu jëfandikoo walla jaamu kurwaa. Kon, ndax foog nga ne jaadu na ñuy jëfandikoo kurwaa bu ñuy jaamu Yàlla ? — 5 Musaa 7:26 ; 1 Korent 10:14.

7. Tàggoo ak yenn ci ngëm walla aada yooyu, mën na jafe lool. Xëy na say mbokk ak say xarit yi dinañu wax ak yow ngir jéem la téye ci li nga gëmoon bu njëkk. Waaye neex Yàlla moo ëpp solo neex nit. — Léebu 29:25 ; Macë 10:36, 37.

[Nataal bi nekk paas 22]

Yàlla du Trinite

[Nataal bi nekk paas 23]

Nowel ak Paag ca diine yu dul dëgg yu yàgg ya lañu jóge

[Nataal bi nekk paas 23]

Amul dara lu wara tax ñuy jaamu walla ragal ñi dee