Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LI ÑU YOKK CI WAXTAAN YI NEKK CI TÉERE BII

Kan mooy Mikayel mi nekk kilifa ci malaaka yi ?

Kan mooy Mikayel mi nekk kilifa ci malaaka yi ?

BIIBËL bi waxul lu bare ci malaaka mi tudd Mikayel. Waaye saa yu ko tuddee, dafay fekk muy def dara. Ci téere Dañeel, wone nañu Mikayel muy xeex ak ay malaaka yu bon. Ci leetaru Yudd, dafa doon werante ak Seytaane. Wone nañu ko it ci Peeñu ma muy xeex Ibliis ak ay malaakaam yu bon yi. Bi muy xeex ngir kiliftéefu Yàlla, te di xeex ay noonu Yàlla, Mikayel dafay wone li turam di tekki, maanaam “ kan moo mel ni Yàlla ” ? Waaye kan mooy Mikayel ?

Yenn saay nit dafay am lu ëpp benn tur. Yanqóoba, Israyil lañu koy woowe itam. Ndaw li Piyeer, xam nañu ko it ci turu Simoŋ (Njàlbéen ga 49:​1, 2 ; Macë 10:⁠2). Noonu it, Biibël bi wone na ne Mikayel beneen turu Yeesu la. Mikayel mooy tur bi Yeesu Kirist yore bala muy ñëw ci kaw suuf si. Tur boobu la yore it bi mu fi jógee. Nañu seet ci Mbind mi li tax ñu wax loolu.

Kilifa ci malaaka yi. Kàddu Yàlla dafay wax ci “ Mikayel, miy kilifa ci malaaka yi ”. (Yudd 9.) Gis nga ne dañuy wax foofu “ Mikayel, miy kilifa ci malaaka yi ”. Loolu dafay tekki ne benn malaaka kese moo mel noonu. Li am sax mooy, saa yu ñu waxee ci Biibël bi “ kilifa ci malaaka yi ”, benn kilifa kese lay doon. Masul doon lu ëpp benn. Rax-ci-dolli, Biibël bi dafay wax ci Yeesu ni ku am taxawaayu kilifa ci malaaka yi. Lu jëm ci Yeesu Kirist mi dekki, lii la 1 Tesalonig 4:​16 wax : “ Baatu kilifa ci malaaka yi dégtu, liitu Yàlla jolli, te Boroom bi moom ci boppam dina wàcce ca asamaan. ” Dañuy wax foofu ne Yeesu dafa yore baatu kilifa ci malaaka yi. Kon boog aaya boobu dafay wone ne Yeesu mooy Mikayel, miy kilifa ci malaaka yi.

Kiy jiite ay xarekat. Biibël bi nee na : “ Mikayel ak malaaka, ya ànd ak moom, xeex ak ninkinànka ja [...] ak ay malaakaam. ” (Ñun ñoo dëngal mbind yi ; Peeñu ma 12:⁠7). Kon Mikayel mooy jiite ay xarekat yu nekk ca asamaan, maanaam malaaka yi topp Yàlla. Peeñu ma it dafay wone Yeesu muy jiite ay xarekat yu nekk ca asamaan, maanaam malaaka yi topp Yàlla (Peeñu ma 19:​14-16). Ndaw li Pool wax na sax ci Sang bi “ Yeesu ” ak “ malaakaam yu am kàttan ”. (2 Tesalonig 1:⁠7.) Kon Biibël bi dafay wax ci Mikayel ak “ malaaka, ya ànd ak moom ”, wax it ci Yeesu ak “ ay malaakaam ”. (Macë 13:41 ; 16:27 ; 24:31 ; 1 Piyeer 3:22.) Kàddu Yàlla masul wax ne ñaari gurupu malaaka yu nekk xarekat yu topp Yàlla ñoo nekk ca asamaan, maanaam benn bu Mikayel jiite ak beneen bu Yeesu Kirist jiite. Kon boog, jaadu na ñuy wax ne Mikayel mooy tur bi Yeesu Kirist yore bu nekkee ci kaw asamaan *.

^ par. 1 Boo bëggee yeneen leeral yuy wone ne turu Mikayel mooy turu Doomu Yàlla, seetal téere Étude perspicace des Écritures, volume 2, xët 280 ak 281. Seede Yexowa yi ñoo defar téere boobu.