Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LI ÑU YOKK CI WAXTAAN YI NEKK CI TÉERE BII

Lan mooy “ Babilon mu mag mi ”

Lan mooy “ Babilon mu mag mi ”

TÉERE Peeñu ma am na ay kàddu yoo xam ne waruñu yem kese ci li ñuy wax ngir nànd li ñuy tekki (Peeñu ma 1:⁠1). Maanaam lu mel ni jigéen ji ñu wax foofu te mu tudd “ Babilon mu mag mi ” te ñu bind tur boobu ci jë bi. Nee nañu jigéen jooju dafa toog ci kaw “ réew yi ak mbooloo yi ”. (Peeñu ma 17:​1, 5, 15.) Komka benn jigéen dëgg mënul def loolu, Babilon mu mag mi dafa war a doon misaal. Kon lan la jigéenu moykat jooju di misaal ?

Wax nañu ci Peeñu ma 17:18 ne jigéen jooju «moo di dëkk bu mag, biy nguuru ci kaw buuri àddina si». Bu ñu nee «dëkk», loolu dafay wone ay nit ñu booloo di liggéeyandoo. Komka «dëkk bu mag» boobu am na baat ci kaw «buuri àddina si», jigéen jooju tudd Babilon mu mag mi, dafa war a doon mbootaay bu am doole bu law ci àddina si sépp. Kon mën nañu wax ne nguur la bu law ci àddina si sépp. Waaye ban fasoŋu nguur la ? Nguuru diine la. Nañu seet naka la yeneen aaya yu nekk ci Peeñu ma di ñu may sañ-sañu wax loolu.

Nguur mën na doon bu politig, bu jënd ak jaay, walla bu diine. Jigéen ji tudd Babilon mu mag mi du nguuru politig, ndaxte Kàddu Yàlla nee na «buuri àddina si» maanaam li bokk ci politigu àddina si, dañuy «njaaloo» ak moom. Njaaloo boobu ñuy wax mooy kóllëre bi jigéen jooju séq ak buuri àddina si. Looloo tax ñu koy woowe «moykat bu mag bi». — Peeñu ma 17:​1, 2 ; Saag 4:⁠4.

Babilon mu mag mi mënul nekk it nguuru jënd ak jaay, ndaxte «baana-baanay àddina» si maanaam jaaykat yi, dinañu am naqar bu ñu fiy jële jigéen jooju. Biibël bi wone na ne buur yi ak baana-baana yi dinañu taxaw fu “ sore ” di ko seetaan (Peeñu ma 18:​3, 9, 10, 15-17). Kon jaadu na ñuy wax ne Babilon mu mag mi nekkul nguuru politig, te nekkul itam nguuru jënd ak jaay. Waaye nguuru diine la.

Leneen luy wone ne Babilon mu mag mi dafa bokk ci mbirum diine mooy li ñu wax ne dafay jaar ci ay «luxus» ngir réeral réew yépp (Peeñu ma 18:23). Komka lépp luy luxus, kort walla mbirum tuuri maam ak yeneen yu mel noonu ci li diine yi di jàngale ak ci rab yi walla jinne yi la jóge, kon yoon la ñuy wax ne Babilon mu mag mi «dëkkukaayu jinne la». (Peeñu ma 18:2 ; Deutéronome 18:​10-12.) Biibël bi wone na itam ne nguur googu dafay xeex bu baax diine dëgg ji, di fitnaal «yonent yi» ak «gaayi Yàlla yi». (Peeñu ma 18:24.) Li am sax mooy Babilon mu mag mi dafa bañ diine dëgg ji di teg fitna yu metti ci kaw ñiy “ seedeel Yeesu ”, ba di leen rey sax (Peeñu ma 17:⁠6). Kon leer na ne jigéen jooju tudd Babilon mu mag mi dafay misaal mbooloo diine yu dul dëgg yépp ci àddina si. Te dafay boole diine yépp yu àndul ak Yexowa Yàlla.