Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

PÀCC FUKK AK ÑETT

Nañu jàppe bakkan ni ko Yàlla jàppe

Nañu jàppe bakkan ni ko Yàlla jàppe
  • Nan la Yàlla jàppe bakkan ?

  • Naka la Yàlla gise yàq biir ?

  • Naka lañuy wone ne fonk nañu bakkan ?

1. Kan moo sàkk lépp liy dund ?

YONENT Yàlla Yérémi nee woon na : “ Yexowa mooy Yàlla ci dëgg-dëgg. Mooy Yàlla biy dund. ” (Yérémi 10:​10, NW). Rax-ci-dolli, Yexowa Yàlla moo sàkk lépp liy dund. Lii la ko mbindeef yi nekk ca asamaan waxoon : «Yaa sàkk lépp te ci sa coobare la lépp nekke, te ci lañu leen sàkke.» (Peeñu ma 4:11). Buur bi Daawuda jagleeloon na Yàlla benn woy, ne ko : “ Ci yow la bakkan jóge. ” (Sabóor 36:​9, NW). Kon, bakkan mayu Yàlla la.

2. Lan la Yàlla def ngir dundal ñu ?

2 Yexowa dafa ñuy dundal it (Jëf ya 17:28). Moo ñu may li ñuy lekk, ndox mi ñuy naan, ngelaw bi ñuy noyyi ak suuf si ñu nekk (Jëf ya 14:​15-17). Yexowa dafa sàkk loolu lépp ci fasoŋ buy tax suñu dund neex. Waaye bu ñu bëggee jariñoo bu baax suñu dund, dañu war a jàng ndigalu Yàlla yi te topp leen. — Isaïe 48:​17, 18.

NAÑU WONE NE FONK NAÑU BAKKANE

3. Naka la Yàlla gise li Kayin rey Abel ?

3 Yàlla dafa bëgg ñu fonk bakkan, muy suñu bakkan walla bakkanu jaambur. Nañu seet li xewoon ca jamono maam Aadama ak Awa. Seen doom, Kayin, dafa mere woon lool rakkam Abel. Yexowa daldi ko wax mu moytu, ndaxte mer moomu mën na ko defloo bàkkaar bu réy. Waaye Kayin faalewul li ko Yàlla wax. Mu “ dal ci kaw Abel, bóom ko ”. (Njàlbéen ga 4:​3-8.) Li Kayin rey rakkam moo tax Yexowa yar ko. — Njàlbéen ga 4:​9-11.

4. Naka la Yàlla wonee ci yoonu Musaa ni nit war a jàppe bakkan ?

4 Ay junniy at ginnaaw loolu, Yexowa joxoon na waa Israyil ay ndigal yi leen di dimbali ñu jaamu ko ni mu ware. Li Yàlla jaar ci yonent Musaa ngir jox ndigal yooyu waa Israyil moo tax yenn saay ñu leen di woowe yoonu Musaa. Ci ndigal yooyu, am na fu ñu wax lii : “ Bul bóom. ” (Gàddaay gi 20:13). Loolu dafa doon won waa Israyil ne Yàlla dafa fonk bakkanu doomu Aadama. Te nit dafa war a fonk it bakkanu moroomam.

5. Naka lañu war a gise yàq biir ?

5 Lan lañu wax nag ci bakkanu xale bu juddoogul ? Ci ndigal yi Yàlla jox Musaa, am na buy wone ne rey xale bu juddoogul baaxul. Waaw, bakkan bu juddoogul sax, am na solo ci kanamu Yexowa (Exode 21:​22, 23 ; Sabóor 127:⁠3). Loolu dafay wone ne yàq biir baaxul.

6. Lu tax waruñu bañ suñu moroom ?

6 Am gis-gis bu rafet ci suñuy moroom, bokk na ci fonk bakkan. Biibël bi nee na : “ Képp ku bañ sa mbokk, reykat nga ; te xam ngeen ne, ku rey nit amuloo dund gu dul jeex. ” (1 Yowaana 3:15). Bu ñu bëggee am dund gu dul jeex, dañu war a dindi ci suñu biir xol bépp fasoŋu bañ sa moroom, ndaxte li ëpp ci xeex yi, mbañeel moo ko indi (1 Yowaana 3:​11, 12). Kon di jéem a bëggante ci suñu biir lu am solo la.

7. Yan jëf ñooy wone ne ki koy def fonkul bakkan ?

7 Naka nga mën a wonee ne fonk nga bakkan bi la Yàlla may ? Ci yoon, kenn bëggul dee. Waaye am na ñuy fowe seen bakkan ngir féexal seen xol. Mën nañu ko seet ci lii : ñu bare dañuy tux sigareet walla póon walla it di jëfandikoo dorog ngir mën ci am bànneex. Fekk lu mel noonu baaxul ci yaram te day faral di rey ñi koy jëfandikoo. Ñiy jëfandikoo sigareet, póon, dorog walla lu mel noonu, jàppewuñu bakkan ni lu sell. Ci kanamu Yàlla jëf yooyu selluñu (Room 6:19 ; 12:1 ; 2 Korent 7:⁠1). Bu ñu bëggee jaamu Yàlla ni mu ware, dañu war a bàyyi jëf yooyu. Bàyyi ko mën na jafe lool. Waaye Yexowa mën na ñu ci dimbali. Te sax Yexowa dafay kontaan lool bu ñuy gis ñuy góor-góorlu ngir toppatoo suñu bakkan ci fasoŋ buy wone ne, mayu Yàlla bu am solo la ci ñun.

8. Lu tax ñu war a bàyyi xel bu baax ci di moytu lépp lu mën a lor nit ?

8 Su ñu fonkee bakkan, dinañu bàyyi xel ci di moytu lépp li mën a lor nit. Kon duñu sàggan, te duñu fowe it suñu bakkan ngir am bànneex kese walla ngir wone ne am nañu fit. Dinañu moytu bu ñuy dawal, moytu it espoor bu ànd ak jëfi soxor walla espoor yi ñu mën a lor (Psaume 11:⁠5). Ndigal bii la Yàlla jox waa Israyil : ‘ Sooy tabax kër gu bees [gu am teraas], war nga defar miir bu ndaw ci teraas bi. Loolu dina tax sa kër bañ a am àqu deret, ndaxte nit mën na fa daanu. ’ (5 Musaa 22:​8, NW). Ni ko ndigal boobu wonee, war nga defar bu baax li nekk ci sa kër, lu mel ni yéegukaay walla iskale ngir nit bañ ci fakkastalu, daanu, ba am ci gaañ-gaañ bu metti. Boo amee oto, na la wóor ne dawal ko wóor na. Bul bàyyi sa kër walla sa oto doon li la mën a lor, yow walla sa moroom.

9. Bu ñu fonkee bakkan, naka lañu war a jàppe mala yi ?

9 Lu ñu mën a wax nag ci bakkanu mala yi ? Bakkanu mala it dafa sell ci kanamu Boroom bi. Yàlla may na ñu ñu rey mala ngir am li ñuy lekk, li ñuy sol, walla ngir aar nit ñi ci li leen mën a lor (Njàlbéen ga 3:21 ; 9:3 ; Exode 21:28). Waaye soxor ak mala walla rey leen ngir féexal suñu xol, baaxul. Kuy def loolu dafay wone ne faalewul ne bakkan lu sell la. — Proverbes 12:⁠10.

NAÑU WONE NE FONK NAÑU DERET

10. Naka la Yàlla wonee ne bakkan ak deret dañu bokk ?

10 Bi Kayin reyee rakkam Abel, Yexowa dafa ko ne woon : «Sa deretu rakk jaa ngi yuuxoo ci suuf, ma di ci dégg.» (Njàlbéen ga 4:10). Bi Yàlla doon wax ci deretu Abel, bakkanu Abel la bëggoon a wax. Kayin dafa jëloon bakkanu Abel, kon dañu ko waroon a yar. Dafa mel ni deretu Abel, walla bakkanam, moo doon yuuxu ba ci ay noppi Yexowa ngir mu àtte ko. Li bakkan ak deret bokk, feeñ na it ci jamono Nóoyin, bi mbënn mi weesoo. Bala mbënn mi di am, doomi garab, pepp ak léjum kese la nit ñi doon lekk. Waaye ba mbënn mi weesoo, lii la Yexowa wax Nóoyin ak ay doomam : «Man ngeen a dunde boroom bakkan yooyu yépp. Jagleel naa leen mbindeef yooyu yépp, ni ma leen jagleele woon gàncax.» Waaye booba, am na lu leen Yàlla tere woon. Lii la ci teg : «Buleen lekk yàpp wu ànd ak deret, ndaxte dund a ngi ci deret.» (Njàlbéen ga 1:29 ; 9:​3, 4). Leer na ne, ci kanamu Yexowa, bakkan ak deretu mbindeef dañu bokk.

11. Li ko dale jamono Nóoyin, lan la Yàlla tere nit def ak deret ?

11 Dinañu wone ne fonk nañu deret bu ñu bañee lekk ñam bu am deret. Lii la Yexowa digaloon waa Israyil : “ Bépp góor [...] bu dem rëbbi rabu àll walla picc bu ñu mën a lekk, war na tuur deretu li mu rey, muur ko ak suuf. [...] Lii laa wax doomi Israyil : ‘ Waruleen lekk deretu mbindeef bu mu mënta doon. ’ ” (3 Musaa 17:​13, 14, NW). Li Yàlla tere woon noonu, njëkkoon na ko wax Nóoyin lu jege 800 at bala mu koy wax waa Israyil. Ndigal boobu deñul woon ba tey. Li Yexowa xalaat ci loolu dafa leer : jaamam yi mënoon nañu lekk yàppu mala yi, waaye waruñu woon a lekk deret bi. Dañu ko waroon a tuur ci suuf, noonu dañuy delloo Yàlla bakkanu mala bi ñu rey.

12. Ci jamono karceen yu njëkk yi, lan la xel mu sell mi digle ci lu jëm ci deret, te ñu war koo topp ba tey jii ?

12 Lu mel noonu la Yàlla wax karceen yi. Ci jamono karceen yu njëkk yi, ndawi Yeesu yi ak ñeneen ñi doon jiite taalibe Yeesu yi, dañu daje woon ngir jàpp yan digle Yàlla la mbooloo karceen yépp waroon a topp. Lii lañu mujj a jàpp : “ Ndaxte li neex Xel mu Sell mi te neex nu, mooy nu bañ leen a teg beneen yen, lu dul dénkaane yii am njariñ, maanaam ngeen moytu ñam wu ñu tuuroo xërëm, deretu jur gu médd [“ deret ak lu médd, ” NW] ak njaaloo. ” (Jëf ya 15:​28, 29 ; 21:25). Kon dañu war a ‘ moytu deret ’. Ci kanamu Yàlla loolu dafa am solo ni moytu xërëm ak njaaloo.

Bu la doktoor tere woon sàngara, ndax dinga jël pikiir sol ko ci sa yaram ?

13. Joxeel benn misaal buy wone ne sol deret ci sa yaram bokk na ci li Yàlla tere bi mu waxee ñu moytu deret.

13 Li Yàlla wax ñu moytu deret, ndax sol deret ci sa yaram bokk na ci ? Waawaaw. Nañu ko seet ci lii : Su la doktoor tere woon sàngara, ndax dinga wax ne naan sàngara kese la la tere, waaye mën nga jël pikiir sol ko ci sa yaram ? Déedéet ! Noonu it, moytu deret dafay tekki bañ koo dugal ci sa yaram ci fasoŋ bu mu mënta doon. Kon li ñu Yàlla tere deret dafay tekki ne waruñu nangu kenn sol deret ci suñuy siddiit.

14, 15. Su doktoor waxee benn karceen ne dañu ko war a sol deret, lan lay def, te lu tax muy def loolu ?

14 Karceen mën na am gaañ-gaañ bu metti, walla ñu war koo opeere opeere bu garaaw te doktoor bi dafa wax ne bu ñu ko solul deret dina dee. Léegi nag ? Dëgg la karceen bëggul dee. Dina def li mu mën ngir sàmm bakkan bi ko Yàlla may ndax ci moom lu am solo la. Moo tax dina nangu bépp faj ci kaw ñu bañ a jëfandikoo deret ci fasoŋ bu Yàlla tere. Kon dina seet li ci doktoor yi mën te dina am yu bare yu mu ci mën a nangu.

15 Ndax karceen dina teggi li Yàlla digle ngir mën a yokk tuuti ci ay fanam ci àddina sii ? Lii la Yeesu waxoon : «Ndaxte koo xam ne bëgg ngaa rawale sa bakkan, dinga ko ñàkk, waaye ku ñàkk sa bakkan ngir man, jotaat ko.» (Macë 16:25). Ñun bëgguñu dee. Waaye bu ñu bëggee teggi li Yàlla digal ngir mucc tey, mën nañu ci ñàkk dund gu dul jeex. Li gën ci ñun mooy, ñu gëm ne li Yàlla digle moo wóor te baax. Te na ñu wóor ne ak lu mënta tax ñu ñàkk suñu bakkan, Ki ñu may bakkan du ñu fàtte bésu ndekkite bi. Dina ñu mayaat lu am solo li mu ñu mayoon, maanaam suñu bakkan. — Yowaana 5:​28, 29 ; Yawut ya 11:⁠6.

16. Lan la jaamu Yàlla yi fas yéene def ci lu jëm ci deret ?

16 Tey, ñiy jaamu Yàlla dëgg dañu fas yéene def li leen Yàlla wax ci wàllu deret. Duñu ko lekk ci fasoŋ bu mu mënta doon. Te seen wér-gi-yaram it du tax ñu nangu deret *. Dafa leen wóor ne Yàlla mii sàkk deret, xam na li gën ci ñoom. Ndax yow it gëm nga loolu ?

FASOŊU JËFANDIKOO DERET BI YÀLLA NANGU

17. Ca Israyil bu njëkk, ban fasoŋ kese la Yexowa Yàlla nangu woon ci jëfandikoo deret ?

17 Yoonu Musaa wone na fasoŋu jëfandikoo deret bi Yàlla nangu. Lii la Yexowa santoon waa Israyil ci ni ñu ko waree jaamu : “ Bakkanu [walla dundu] yaram bi, ci deret bi la nekk, man dama leen ko tegal fi ñuy saraxe ngir muur seeni bàkkaar, ndaxte deret mooy muur bàkkaar. ” (3 Musaa 17:​11, NW). Saa yu waa Israyil bàkkaaree, dañu doon saraxe mala, def tuuti deret fi ñu doon defe sarax yi ngir ñu baal leen seeni bàkkaar. Loolu ci tàntu màggalukaay bi lañu ko doon def. Waaye mujj nañu koo def ci kër Yàlla, bi ñu ko tabaxee. Benn fasoŋ kese bi Yàlla nangu woon ñu jëfandikoo deret mooy ni ñu ko doon jëfandikoo ci sarax yooyu.

18. Li ñu tuur deretu Yeesu naka la ñu mënee jariñ te yan barke lañu ci mën a jële ?

18 Du yoonu Musaa mooy jiite karceen dëgg yi. Moo tax duñu saraxe ay mala, ba di def deretu mala yi fi ñuy defe sarax yi (Yawut ya 10:⁠1). Waaye deret boobu waa Israyil doon def fi ñuy defe sarax yi, dafa doon wone sarax bu am solo lool, maanaam sarax bi Yeesu Kirist, doomu Yàlla, defoon bi mu saraxee boppam. Ni ñu ko gise ci pàcc 5, Yeesu dafa joxe bakkanam ngir ñun. Dafa nangu ñu tuur deretam ngir saraxe ko. Ginnaaw loolu dafa yéeg ca asamaan te jox Yàlla njëgu deretam benn yoon ba fàww (Yawut ya 9:​11, 12). Ci kaw loolu la ñu Yàlla di baal suñuy bàkkaar. Loolu dina tax it ñu mën a am dund gu dul jeex (Macë 20:28 ; Yowaana 3:16). Fasoŋ boobu ñu jëfandikoo deret am na solo lool (1 Piyeer 1:​18, 19) ! Gëm li deret bi Yeesu tuur mën a indi, loolu kese moo mën a tax ñu mucc.

Naka nga mënee wone ne fonk nga bakkan ak deret ?

19. Lan lañu war def ngir bañ a gàddu benn àqu deret ?

19 War nañu sant Yexowa bu baax ci li mu ñu bëgg ba may ñu dund ! Ndax loolu waru ñu xiir ñu wax suñuy moroom ne mën nañu am dund gu dul jeex bu ñu gëmee sarax bi Yeesu def bi mu saraxee boppam ? Dinañu ci sawar lool, su dee fonk nañu bakkanu suñuy moroom ni ko Yàlla fonke (Ézékiel 3:​17-21). Su ñu defee loolu ñu Yàlla sant ni mu ware, dinañu mën a wax ni ndaw li Pool bi mu waxee ne : «Wàccoo naa ak yéen ñépp [maanaam gàdduwuma benn àqu deret] [...] ndaxte ñeebluwuma leen, ci di leen xamal lépp li Yàlla digle.» (Jëf ya 20:​26, 27). Wax nit ñi lu jëm ci Yàlla ak ci coobareem lu baax la ngir wone ne fonk nañu lool bakkan ak deret.

^ par. 16 Boo bëggee ay leeral ci li mën a wuutu sol deret, seetal li ñu wax ci téere bi tudd Comment le sang peut-il vous sauver la vie ? (Naka la la deret mënee musal ?), ci xët 13 ba 17. Seede Yexowa yi ñoo defar téere boobu.