LI ÑU YOKK CI WAXTAAN YI NEKK CI TÉERE BII
Ndax war nañu bokk ci feet yi ?
FEETU diine yi ak feet yu bare yi ñuy màggal tey ci àddina si, jógewuñu ci Biibël bi. Kon fan la feet yooyu jóge ? Am na téere yu am solo yu wax ci feet yi ñu tàmm di màggal ci sa réew. Boo mënee dem ci bibliothèque (maanaam fu ñuy dénc ay téere), dinga ci mën a jàng lu am njariñ lu jëm ci feet yooyu. Nañu seet li ñu wax ci yenn feet.
Feetu Paag. Téere bi tudd The Encyclopædia Britannica nee na, “ ci xaaju Biibël bi tudd Nouveau Testament, waxuñu fa dara lu jëm ci màggal feetu Paag ”. Naka lañu komaasee di
màggal Paag ? Ci ñiy jaamu ay xërëm la jóge. Bu dee sax dañuy wax ne dañuy def feet boobu ngir màggal dekki Yeesu, aada yi ñuy topp ci Paag, bokkul ci diine karceen. Nañu ko seet ci lii : lii la téere bi tudd The Catholic Encyclopedia wax ci “ lëgu Paag ” yi nit ñu bare di def ci feetu Paag : “ Lëg, misaal la ci boroom xërëm yi. Dafa mas a firnde barke ci li jëm ci jur doom yu bare. ”Màggal at mu bees. Bés bu ñuy màggal at mu bees ak aada yi muy àndal dafay wuute ci réew yi. Lii la téere The World Book Encyclopedia wax lu jëm ci fi feet boobu jóge : “ Ci atum 46 ci suñu jamono la Jules Cesar, buuru waa Room jàpp ne 1 sãwiyee mooy nekk bés bi ñuy màggal at mu bees. Janus la waa Room jagleeloon bés boobu. Ci ñoom, Janus moo doon yàllay bunt yi te moo doon it yàllay lépp luy tàmbali. Sãwiyee, ci turu Janus lañu ko jële. Janus, ñaari kanam la amoon. Benn bi dafa féete woon kanam, beneen bi féete ginnaaw. ” Kon feet bi ñuy def ngir màggal at mu bees, ci aada ñiy jaamu xërëm la jóge.
Saint-Valentin. “ Feetu Saint-Valentin mu ngi jóge ci bés bu ñu jagleeloon ñaari karceen yu tuddoon Valentin te ñu reyoon leen. Waaye aada yi ñuy topp ci feet boobu [...] ci feet bu waa Room doon màggal bu yàgg la war a jóge. Feet boobu, Lupercal lañu ko doon woowe. Dafa doon am ci bésu 15 feewriyee ci at mu nekk. Dañu doon def feet boobu ngir màggal Juno mi nga xam ne, waa Room dañu doon wax ne mooy yàllay jigéen ñi. Ci ñoom it moo doon yàllay lépp lu jëm ci séy. Ci bés boobu, dañu doon màggal itam Pan mi nekkoon yàllay àll yi, géej yi ak lépp li ci nekk. ” — The World Book Encyclopædia (1973), Vol. 20, xët 204.
Yeneen feet yi. Mënuñu wax ci feet yépp yi ñuy màggal ci àddina si. Waaye Yexowa nanguwul feet yuy màggal nit walla kurél yu nit taxawal (Yérémi 17:5-7 ; Jëf ya 10:25, 26). Bul fàtte it ne, feet yi ñuy màggal ci diine yi, fi ñu jóge mooy tax Yexowa di leen nangu walla déet (Isaïe 52:11 ; Peeñu ma 18:4). Li Yàlla santaane ci Biibël bi, te ñu wax ko ci pàcc 16, dina la won li Yàlla xalaat ci bokk ci feet yi ñuy màggal ci àddina si.