Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

PÀCC JURÓOM

Njot gi, li gën a réy ci li Yàlla maye

Njot gi, li gën a réy ci li Yàlla maye
  • Lan mooy njot gi ?

  • Naka la Yàlla joxe njot gi ?

  • Lan la la njot gi mën a indil ?

  • Naka nga mënee wone ne yaa ngi gërëm Yàlla ndax njot gi ?

1, 2. a) Li la nit may, lan mooy tax mu am solo ci yow ? b) Lu tax ñu mën a wax ne njot gi moo gën a am solo ci lépp li ñu la mën a may ?

CI LI ñu la mas a may lépp, lan moo ci gën a réy ? Booy maye dara, soxlawul nga fey ci xaalis bu bare ngir mu am solo. Li ñuy maye, du ci njëgam kese lañuy xoole njariñam dëgg. Su dee li ñu la may bégal na la, walla mu doon li nga soxla woon dëgg, dina nekk ci yow maye bu réy.

2 Ci lépp li nga mën a bëgg ñu may la, am na lu ci sut. Loolu nag Yàlla moo ko may doomu Aadama yi. Li ñu Yexowa may bare na lool. Waaye li ci gën a réy mooy njot gi, maanaam bakkanu Doomam bi mu saraxe, Yeesu Kirist (Macë 20:28). Ni ñu ko naree gis ci pàcc bii, ci lépp li ñu la mën a may, njot gi moo ci gën a am solo, ndaxte mën na la indil mbégte bu réy lool. Te it mën na faj li nga gën a soxla ci àddina. Dëgg-dëgg, njot gi mooy liy gën a wone ne Yexowa dafa la bëgg.

LAN MOOY NJOT GI ?

3. Lan mooy njot gi te lan lañu war a xam ngir mën a gis ni maye boobu ame solo ?

3 Ngir yombal wax ji, njot gi mooy li Yexowa jëfandikoo ngir yewwi doomu Aadama yi, maanaam musal leen, ci bàkkaar ak dee (Efes1:⁠7). Ngir mën a nànd li Biibël bi wax ci loolu, dañu war a seetaat li xewoon ca tool ba ca Àjjana. Bala ñuy mën a xam ni njot gi ame solo, fàww ñu xam li Aadama ñàkk bi mu bàkkaaree.

4. Nekk nit ku mat, lu mu doon may Aadama ?

4 Bi Yexowa sàkkee Aadama, dafa ko may lu am solo dëgg, maanaam bakkanu nit ku mat. Seetal loolu mu may Aadama. Komka Yàlla dafa ko sàkk, may ko yaram bu mat ak xel bu mat, Aadama narul woon mas a feebar, màgget walla dee. Li mu nekkoon nit ku mat, tax na ba digganteem ak Yexowa rattax lool. Biibël bi nee na Aadama “ doomu Yàlla ” la woon (Luug 3:38). Kon Aadama jege woon na Yexowa Yàlla lool, mel ni doom ak baayam bu ko bëgg. Yexowa dafa doon wax ak doomam bi nekkoon ci kaw suuf, di ko dénk liggéey bu neex te am solo, te xamal ko it li mu bëggoon ci moom. — Njàlbéen ga 1:28-30 ; 2:​16, 17.

5. Biibël bi nee na dañu sàkk Aadama ‘ ci melokaanu Yàlla ’. Loolu lu muy tekki ?

5 Dañu sàkk Aadama ‘ ci melokaanu Yàlla ’. (Njàlbéen ga 1:27.) Waxuñu ne jëmmu Aadama dafa niru woon jëmmu Yàlla. Ni ñu ko jànge ci pàcc 1, Yexowa xel la, te kenn mënu ko gis (Yowaana 4:24). Kon Yexowa yorewul yaram ni yaramu doomu Aadama. Bu ñu waxee ne dañu sàkk Aadama ci melokaanu Yàlla, dañu bëgg a wax ne, dañu ko sàkk, may ko jikko yi nekk ci Yàlla. Jikko yu mel ni mbëggeel, xam-xam, njub, ak it kàttan. Aadama dafa niru Baayam it ci beneen fànn bu am solo maanaam : amoon na sañ-sañu tànnal boppam li mu bëgg a def. Kon Aadama melul woon ni masin boo xam ne, li tax ñu defar ko, walla li ñu ko defloo kese lay mën a def. Aadama mënoon na seetal boppam li mu bëgg a def, tànn ndax dina def lu baax walla lu bon. Su Aadama tànnoon déggal Yàlla, kon dina dund ba fàww ci Àjjana ci kaw suuf.

6. Lan la Aadama ñàkk bi mu bañee déggal Yàlla, te loolu lu mu def ci ay doomam ?

6 Leer na kon ne Aadama ñàkk na lu bare bi mu bañee déggal Yàlla, ba Yàlla wax ko ne dina dee. Li mu bàkkaar tax na ba nekkatul woon nit ku mat. Amatul woon it barke yiy ànd ak loolu (Njàlbéen ga 3:​17-19). Li ci metti mooy, du Aadama kese moo ci ñàkk dund gu mat. Dafa ko ñàkkloo itam doomam yi mu waroon a am ëllëg. Kàddu Yàlla nee na : “ Bàkkaar ci kenn nit [Aadama] la jaar, dugg ci àddina, indaale fi dee, te dee daldi law ci nit ñépp, ndaxte ñépp a bàkkaar. ” (Room 5:12). Waaw, ñun ñépp, ci Aadama lañu donn bàkkaar. Looloo tax Biibël bi nee Aadama moo def ba moom ak doom yi mu naroon a am ñu “ nekk ” ci dooley bàkkaar ak dee, mel ni jaam (Room 7:14). Aadama ak Awa amatuñu woon benn yaakaar ndaxte ñoom ñoo tànnal seen bopp bañ a déggal Yàlla. Waaye seeni doom nag, boole ci ñun ñii ?

7, 8. Lan ak lan la njot gi ëmb ?

7 Yexowa dafa jëfandikoo njot gi ngir dimbali doomu Aadama yi. Lan mooy njot ? Njot am na ñaar yu mu ëmb. Lii mooy bu njëkk bi : njot mooy li ñuy fey ngir ñu yewwi benn nit walla li ngay fey ngir nanguwaat li nga jaay ba pare. Mën nañu ko méngale ak li ay bàndi di laaj ngir yewwi ku ñu jàpp. Lii mooy ñaareel bi : njot mooy li ñuy joxe ngir fey dara. Dafa mel ni xaalis bi ñuy fey ngir faj ki ñu gaañ walla defar li ñu yàq. Mooy li am bu aksidã amee. Ki tooñ dina war a fey luy tolloo ak li mu yàq.

8 Lu réy li ñu ñàkk ñun ñépp ndax li Aadama def, lu ko mënoon a fey ba tax ñu yewwi ñu ci bàkkaar ak dee ? Nañu seet njot gi Yexowa maye, ak njariñ bu mu la mën a amal.

NI YEXOWA JOXEE NJOT GI

9. Ban fasoŋu njot lañu soxla woon ?

9 Komka bakkanu nit ku mat moo amatul woon, amul kenn ci kaw suuf ku ko amoon pur fey ko (Psaume 49:7, 8). Li ñu soxla woon mooy njot gu tolloo ak li ñu ñàkkoon. Loolu dafa ànd ak digle bu jub te wóor bi nekk ci Kàddu Yàlla biy wax ne : “ Bakkan mooy fey bakkan. ” (5 Musaa 19:​21, NW). Kon lan moo mënoon a fey bakkan bu mat, maanaam dund gu mat, bi Aadama ñàkk ? Xanaa beneen bakkan bu mat. — 1 Timote 2:⁠6.

10. Naka la Yexowa joxee njot gi ?

10 Naka la Yexowa joxee njot gi ? Dafa yónni ci kaw suuf kenn ci doomam yi nekkoon ca asamaan. Tànnul kenn ci ñoom noonu rekk, waaye ki mu gënoon a fonk la yónni (1 Yowaana 4:​9, 10). Doom jooju nangu na jóge fi mu dëkkoon ca asamaan (Filib 2:⁠7). Ni ñu ko gise ci pàcc bi weesu, Yexowa dafa def kéemaan, bi mu jëlee bakkanu Doomam jooju, def ko ci biiru Maryaama. Xelu Yàlla mu sell mi moo def ba Yeesu juddu nekk nit ku mat. Narul woon a dee ndax bàkkaar. — Luug 1:⁠35.

Yexowa dafa joxe benn Doomam ji mu am kepp ngir mu nekk njot ngir ñun ñépp.

11. Naka la bakkanu benn nit mënoon a fey njotu ay milyoŋi nit ?

11 Naka la benn nit mënoon a feye njotu nit ñu bare ba tollu ak ay milyoŋi doomu Aadama ? Nañu njëkk a seet lii : Naka la ay milyoŋi doomu Aadama defe ba nekk ay bàkkaarkat ? Fàttalikul ne, bi Aadama bàkkaaree, fa la ñàkke lu am solo lool, maanaam bakkanu nit ku mat bi mu amoon. Kon bakkan bu mat boobu, Aadama mënu ko woon a jottali ay doomam. Bàkkaar ak dee kese la leen mënoon a jottali. Yeesu mi Biibël bi di woowe “ Aadama mu mujj mi ” nit ku mat la woon, te masul a bàkkaar (1 Korent 15:45). Mën nañu wax ne Yeesu dafa jël palaasu Aadama ngir musal ñu. Bi Yeesu déggalee Yàlla ci lépp, ba saraxe boppam, maanaam joxe bakkan bu mat bi mu amoon, booba la feye bàkkaar bi Aadama def. Noonu la Yeesu maye yaakaar doomu Aadama yi. — Room 5:19 ; 1 Korent 15:​21, 22.

12. Coono yu metti yi Yeesu daj, lan lañu wone ?

12 Biibël bi wax na coono yi Yeesu daj yépp bala muy dee. Dóor nañu ko dóor yu metti, daaj ko ci bant, bàyyi ko fa ba mu dee (Yowaana 19:​1, 16-18, 30 ; Seetal itam li nekk ci xaaj bi tudd “ Li ñu yokk ci waxtaan yi nekk ci téere bi ”, xët 204 ba 206). Lu tax Yeesu waroon a jaar ci coono yu bare yooyu ? Dinañu gis ci beneen pàcc ci kanam fu Seytaane wax ne benn doomu Aadama du kontine di jaamu Yexowa bu nekkee ci ay coono. Yeesu dafa kontine di déggal Yàlla ci biir ay coono yu mettee metti. Noonu la joxe tont bi gën ci li Seytaane waxoon. Yeesu wone na ci loolu ne nit ku mat te am sañ-sañu tànnal boppam li mu bëgg a def, mën na déggal Yàlla ba mu mat ak lu Ibliis mënta def yépp. Wóor na ne Yexowa kontaanoon na lool ci li ko Doomam jooju mu fonk lool déggaloon ! — Proverbes 27:⁠11.

13. Naka lañu feye njot gi ?

13 Naka lañu feye njot gi ? Ci atum 33 ci suñu jamono, ci 14eelu fan ci weer bi yawut yi doon woowe Nisan, Yàlla dafa bàyyi ñu rey Doomam bu mat bu amul woon benn bàkkaar. Yeesu dafa saraxe bakkanu nit bu mat bi mu amoon, “ benn yoon ba fàww ”. (Yawut ya 10:10.) Bi Yeesu deewee ba mu mat ñetti fan, Yexowa dafa ko dekkal. Dekkalu ko mu nekk nit ci kaw suuf, waaye dafa ko dekkal, mayaat ko dund gi mu amoon ca asamaan. Bi Yeesu demee ca kaw asamaan, dafa indi ci kanamu Yàlla njëgu bakkanam bu mat bi mu saraxe ngir mu nekk njot ngir doomu Aadama yi (Yawut ya 9:24). Yexowa nangu na njëgu li Yeesu saraxe, mu nekk njot gi ñu soxla woon ngir mën a yewwi doomu Aadama yi ci kiliftéefu bàkkaar ak dee. — Room 3:​23, 24.

LAN LA LA NJOT GI MËN A INDIL

14, 15. Lan lañu war a def ngir Yàlla “ baal nu sunuy bàkkaar ” ?

14 Ak li ñu nekk ay bàkkaarkat yépp, njot gi tax na ñu mën a am barke yu réy. Nañu seet yenn ci barke yi ñu mën a am tey ak ëllëg ndax lu réy loolu ñu Yàlla may.

15 Yàlla dina ñu baal suñuy bàkkaar. Li ñu matul ndax suñu maam Aadama, tax na ñuy daj lu nekk bala ñuy mën a def lu baax. Ñépp ay bàkkaar ci wax walla ci jëf. Waaye li ñu saraxe Yeesu ngir mu nekk njot gi, tax na Yàlla mën ñu “ baal [...] sunuy bàkkaar ”. (Kolos 1:​13, 14.) Waaye, bu ñu bëggee Yàlla baal ñu, dañu war a tuub dëgg suñuy bàkkaar. War nañu suufeel suñu bopp it, di ñaan Yexowa, ñaan ko mu baal ñu suñuy bàkkaar ci kaw ngëm bi ñu am ci saraxu Doomam bi nekk njot gi. — 1 Yowaana 1:​8, 9.

16. Lan moo ñuy may ñu mën a jaamu Yàlla ak xel bu ñu dul tuumaal te loolu ban njariñ la am ?

16 Suñu xel du ñu tuumaal ci kanamu Yàlla. Bu ñu suñu xel di tuumaal, ñàkk yaakaar te xalaat ne tekkiwuñu dara dina yomb. Komka njot gi tax na ñu baal ñu suñuy bàkkaar, Yexowa ci mbaaxaayam may na ñu ñu mën koo jaamu ak xel bu ñu dul tuumaal, fekk ay bàkkaarkat lañu (Yawut ya 9:​13, 14). Loolu moo ñuy may ñu mën koo wax lépp. Looloo tax jege ko ci ñaan war a yomb ci ñun (Yawut ya 4:​14-16). Nañu def lépp ngir kontine di am xel boo xam ne du ñu tuumaal. Loolu dina tax suñu xel du jaxasoo, dinañu sàmm suñu ngor te am mbégte.

17. Yan barke lañu mën a am ndax li Yeesu dee ngir ñun ?

17 Dañu am yaakaaru dund ba fàww ci kaw suuf suy nekk àjjana. Room 6:23 nee na “ peyu bàkkaar mooy dee ”. Mu yokk ca ne : “ Waaye mayu Yàlla mooy dund gu dul jeex ci Yeesu Kirist ” suñu Sang. Ci pàcc 3 bi, wax nañu ci barke yi ñuy am ci Àjjana ji di ñëw ci kaw suuf (Peeñu ma 21:​3, 4). Dund gu dul jeex ak wér-gi-yaram gu mat sëkk, dinañu bokk ci barke yooyu yépp. Li Yeesu dee ngir ñun moo tax ñu mën a am barke yooyu. Bala ñuy mën a am loolu, war nañu wone ne fonk nañu lool njot gi ñu Yàlla may.

NAKA NGA MËNEE WONE NE FONK NGA BU BAAX LI ÑU YÀLLA DEFAL ?

18. Lu tax ñu war a gërëm Yexowa ndax njot gi mu maye ?

18 Lu tax ñu war a won Yexowa ne ñu ngi koy gërëm dëgg ndax njot gi mu maye ? Bu ñu nit mayee dara te ñu xam ne ñàkk na ci jotam, amoon ci coono walla dafa ci def alalam, dinañu fonk lool li ñu nit kooku may. Bu ñu xamee ne mbëggeel a tax mu may ñu loolu, dina ñu laal bu baax ci xol. Njot gi mooy maye bi gën a réy bu ñu mën a am, ndaxte ci la Yàlla defe sarax bi gën a réy bu mas a am. Yowaana 3:16 nee na : “ Yàlla dafa bëgg àddina, ba joxe jenn Doomam ji mu am kepp. ” Njot gi mooy liy gën a wone mbëggeel bi Yexowa am ci ñun. Dafay wone it mbëggeel bi Yeesu am ci ñun, ndaxte dafa nangu joxe bakkanam ngir ñun (Yowaana 15:13). Kon mën nañu gëm ne Yexowa ak Doomam dañu bëgg kenn ku nekk ci ñun. — Galasi 2:⁠20.

Jéem di gën a xam Yexowa mooy lenn li nga mën a def ngir wone ne yaa ngi koy gërëm ndax njot gi mu maye.

19, 20. Naka nga mënee wone ne yaa ngi gërëm Yàlla ndax njot gi mu maye ?

19 Léegi nag, naka nga mënee wone ne yaa ngi gërëm Yàlla ndax njot gi mu maye ? Nanga komaase ci lii : jéemal di gën a xam Yexowa mi ñu may njot gi (Yowaana 17:⁠3). Jëfandikoo téere bii ngir gëstu Biibël bi, mën na la ci dimbali. Booy yokk li nga xam ci Yexowa, dinga ko gën a bëgg. Te mbëggeel boobu moo lay xiir ci def li ko neex. — 1 Yowaana 5:⁠3.

20 Nanga wone ngëm gi nga am ci saraxu Yeesu bi nekk njot gi. Lii lañu wax ci Yeesu : “ Ku gëm Doom ji, am nga dund gu dul jeex. ” (Yowaana 3:36). Naka lañuy wonee ne gëm nañu Yeesu ? Du ci ay wax kese lañuy wone ne gëm nañu ko. Saag 2:26 nee na : ‘ Ngëm gu àndul ak jëf dafa nasax ’. maanaam dee na. Waaw, ngëm dëgg, ci “ jëf ” lañu koy wone. Lenn lu ñu mën a def ngir wone ne gëm nañu Yeesu mooy def lépp ngir roy ci moom, ci suñuy wax ak ci suñuy jëf itam. — Yowaana 13:⁠15.

21, 22. a) Lu tax ñu war a teewe Reeru Boroom bi ñuy def at mu nekk ? b) Lan lañuy waxtaan ci pàcc 6 ak 7 ?

21 Nanga teewe Reeru Boroom bi ñuy def at mu nekk. Ci guddi 14 Nisan ci atum 33 ci suñu jamono, Yeesu dafa taxawal xew bu am solo te Biibël bi di ko woowe “ reeru Boroom bi ”. (1 Korent 11:20 ; Macë 26:​26-28.) Xew boobu, dañu koy woowe it bésu fàttaliku deewu Yeesu. Yeesu dafa taxawal reer boobu ngir dimbali ay ndawam ak karceen dëgg yiy ñëw ci seen ginnaaw, ñu bañ a fàtte ne bi mu deewee niki nit ku mat dafa joxe bakkanam ngir mu nekk njot gi. Lii la Yeesu waxoon ci reer boobu : “ Kontineleen di def lii, ngir fàttaliku ma. ” (Luug 22:​19, NW). Ndaje fàttaliku bi dafa ñuy fàttali mbëggeel bi ñu Yexowa ak Yeesu won ci lu jëm ci njot gi. Bu ñu bëggee wone ne fonk nañu lool njot gi dinañu teewe ndaje fàttaliku deewu Yeesu bi ñuy def at mu nekk. *

22 Dëgg-dëgg, njot gi ñu Yexowa may kenn mënu ko fey (2 Korent 9:​14, 15). Maye bu am solo boobu, mën na jariñ sax ñi dee. Loolu dinañu ko gis ci pàcc 6 ak 7.

^ par. 21 Boo bëggee yokk sa xam-xam ci Reeru Boroom bi, seetal li ñu bind ci xaaj bi tudd “ Li ñu yokk ci waxtaan yi nekk ci téere bii ”, xët 206 ba 208.