LI ÑU YOKK CI WAXTAAN YI NEKK CI TÉERE BII
Reeru Boroom bi : Fàttaliku buy màggal Yàlla
DAÑU sant karceen yi ñuy fàttaliku deewu Kirist. Fàttaliku boobu, “ reeru Boroom bi ” lañu koy woowe (1 Korent 11:20). Lu tax mu am solo lool ? Kañ lañu koy def ak naka lañu ko war a defe ?
Ci atum 33 ci suñu jamono, ci guddi bésu Jéggi bi yawut yi doon màggal la Yeesu Kirist taxawal Reeru Boroom bi. Benn yoon kese ci at mi lañu doon màggal bésu Jéggi bi, maanaam bésu 14 ci weer wi Yawut yi doon woowe Nisan. Ngir mën a xam kañ la bés boobu di tombe, yawut yi dañu doon xaar ci at mi, ci diggante màrs ak awril, bés bu bëccëg ak guddi doon def ñoom ñaar ñépp 12 waxtu. Bés bi weer wi di njëkk a feeñ te mu jege jamono jooju, ci la weeru Nisan doon tàmbali. Bu 14 fan weesoo ginnaaw bés boobu, bu jant bi sowee, ci lañu doon màggal bésu Jéggi bi.
Yeesu dafa màggaloon bésu Jéggi bi ak ay taalibeem. Mu dàq Yudaa Iskariyo, sog a taxawal Reeru Boroom bi. Reer boobu moo jël palaasu bésu Jéggi bu yawut yi doon màggal. Moo tax benn yoon kese ci at mi lañu war a màggal Reeru Boroom bi.
Lii la téere Macë wax : “ Yeesu jël mburu, sant Yàlla, damm ko, jox ko taalibe ya. Mu ne leen : «Jël-leen lekk, lii sama yaram la.» Gannaaw loolu mu jël kaas, sant Yàlla, jox leen ko. Mu ne leen : «Yéen ñépp naanleen ci, ndaxte lii sama deret la, ji fas kóllëre gi, te mu tuuru, ngir ñu bare jot mbaalug bàkkaar yi.» ” — Macë 26:26-28.
Am na ñu gëm ne Yeesu dafa soppi mburu boobu, def ko yàpp, soppi biiñ bi, def ko deret. Waaye bi Yeesu doon joxe mburu mi, dara deñul woon ci yaramam. Ndax ci dëgg, taalibe Yeesu yi dañu lekk yaramu Yeesu te naan itam deretam ? Déedéet. Bu loolu amoon, dañuy doon ñuy lekk nit. Te duñu topp li Yàlla santaane (Njàlbéen ga 9:3, 4 ; Lévitique 17:10). Ni ñu ko waxe ci Luug 22:20, Yeesu nee woon na : «Kaas bii mooy misaal kóllëre gu bees gi Yàlla fas jaarale ko ci sama deret, ji tuuru ngir yéen.» Ndax kaas bi ci boppam moo nekkoon «kóllëre gu bees gi Yàlla fas» ? Loolu mënul nekk. Ndaxte kóllëre dafa nekk li ñuy waxtaan ba juboo ci. Du lu ñu mën a téye ci loxo.
Kon mburu mi ak biiñ bi, ay misaal kese lañu. Mburu mi mooy firnde yaramu Yeesu bu mat. Mburu mi desoon ci reeru bésu Jéggi bi la Yeesu jëloon. Mburu moomu amul woon lawiir (Gàddaay gi 12:8). Biibël bi dafay jël lawiir ngir misaal bàkkaar walla luy yàq. Kon mburu moomu mooy firnde yaramu Yeesu bu mat bi mu nangu saraxe. Amul woon benn bàkkaar. — Macë 16:11, 12 ; 1 Korent 5:6, 7 ; 1 Piyeer 2:22 ; 1 Yowaana 2:1, 2.
Biiñ bu xonq bi mooy firnde deretu Yeesu. Deret boobu mooy fas kóllëre gu bees gi. Yeesu nee woon na ne deretam dina tuuru ngir «mbaalug bàkkaar yi». Doomu Aadama yi dinañu mën a sell ci kanamu Yàlla te séq ak Yexowa kóllëre gu bees gi (Yawut ya 9:14 ; 10:16, 17). Kóllëre googu, maanaam li ñu waxtaan ba juboo ci, dafay tax 144 000 karceen yu takku ci Yàlla mën a dem asamaan. Foofu dinañu nekk ay buur ak ay saraxalekat ngir indil doomu Aadama yépp ay barke. — Njàlbéen ga 22:18 ; Yérémi 31:31-33 ; 1 Piyeer 2:9 ; Peeñu ma 5:9, 10 ; 14:1-3.
Kan moo war a jël ci mburu mi ak ci biiñ bi ñuy jàllale bi ñuy fàttaliku deewu Yeesu ? Ci yoon, ñi bokk ci kóllëre gu bees gi kese, maanaam ñi am yaakaar dem ca asamaan, ñoo ko war a jël. Xel mu sell mi moo leen di xamal ba mu wóor leen ne, Yàlla dafa leen tànn ngir ñu nekk ay buur ca asamaan (Room 8:16). Ñooñu bokk nañu itam ci kóllëre Nguur gi Yeesu fas. — Luug 22:29.
Ñi am yaakaar dund ba fàww ci Àjjana ci kaw suuf nag ? Dañuy topp li Yeesu santaane te teewe Reeru Boroom bi. Waaye dañuy ñëw di déglu ak teggin. Duñu jël ci mburu mi ak ci biiñ bi. Seede Yexowa yi dañuy màggal Reeru Boroom bi benn yoon ci at mi, maanaam ci bésu 14 Nisan bu jant bi sowee. Màggalu bés boobu dafa am solo ci karceen yépp, bu dee sax tey ci àddina si sépp, ay junniy nit kese ñooy wax ne am nañu yaakaar dem ca asamaan. Bés boobu dafay may ñépp ñu mën a xalaat ci mbëggeel bu réy bu Yexowa Yàlla ak Yeesu Kirist wone. — Yowaana 3:16.