Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LI ÑU YOKK CI WAXTAAN YI NEKK CI TÉERE BII

Ndax ci weeru desàmbar la Yeesu juddu ?

Ndax ci weeru desàmbar la Yeesu juddu ?

BIIBËL bi waxul kañ la Yeesu juddu. Waaye wax na lu leer luy tax ñu mën a wax ne Yeesu judduwul ci desàmbar.

Nañu seet ni Betleyem fu Yeesu juddoo doon mel ci weeru desàmbar. Weer bi yawut yi doon woowe Kislev (maanaam nowàmbar ba desàmbar), dafa doon sedd di taw it. Weer bi ci topp mooy weeru Tébeth (desàmbar ba sãwiyee). Weer boobu moo gënoon a sedd ci at mi. Yenn saay sax dafa doon taw pëndu galaas (neige ci tubaab) ci tund yi. Nañu seet li Biibël bi wax ci ni diiwaan boobu doon mel ci wàllu tàngoor ak sedd.

Esraa mi bokk ci ñi bind ci Biibël bi, wone na ne Kislev dafa nekkoon weer bu sedd te bare li muy taw. Esraa waxoon na ne mbooloo mu réy moo daje woon ca Yerusalem ci “ juróom-ñeenteelu weer bi [maanaam Kislev] ci ñaar-fukkeelu fan bi ci weer bi ”. Mu yokk ci ne mbooloo mi yépp a doon “ lox [...] ndax taw bu bare ”. Mbooloo mi fa daje woon ci boppam lii la waxoon ci ni dëkk bi doon mel ci waxtu boobu ci at mi : “ Ñu ngi ci jamono taw bu bare. Kenn mënul nekk ci biti. ” (Esraa 10:​9, 13, NW ; Jérémie 36:22). Xam nañu kon lu tax sàmmkat yi nekkoon foofu doon fexe ba ñoom ak seeni jur bañ a fanaan ci biti bu weeru desàmbar doon jegesi !

Waaye Biibël bi nee na ci guddi gi Yeesu juddu, sàmmkat yi ñu ngi nekkoon ci tool yi di wottu seeni jur. Luug mi bokk ci ñi bind ci Biibël bi wax na ne sàmmkat yi dañu “ daan fanaan ca tool ya, di wottu jur ga ” ca wetu Betleyem (Luug 2:8-12). Gis nga ne sàmmkat yi dañu doon fanaan ci biti ak seeni jur. Du bëccëg kese lañu doon génn ak seeni jur. Guddi dañu doon nekk ci tool yi ak seeni jur. Ndax ci Betleyem, mënoon nañu fanaan ci biti ci weeru desàmbar ak li mu doon sedd te bare taw ? Déedéet. Loolu mënul nekk. Kon loolu lépp dafay wone ne Yeesu judduwul ci weeru desàmbar *.

Kàddu Yàlla wax na bés bi Yeesu dee, waaye li mu wax ci bés bi Yeesu juddu barewul. Loolu dafa ñuy fàttali li buur bi Suleymaan waxoon : “ Am tur moo gën fuuf diw bu baax. Te bésu dee moo gën bésu juddu. ” (Dajalekat 7:​1, NW). Kon jaadu na Biibël bi wax lu bare ci waaraate bi Yeesu doon def ak ci deewam te wax lu tuuti kese ci bés bi mu juddu.

Guddi gi Yeesu juddu, mu ngi fekk sàmmkat yi ak seeni jur nekk ci tool yi.

^ par. 1 Boo bëggee yeneen leeral, seetal li ñu wax ci téere Comment raisonner à partir des Écritures, xët 161 ba 165. Seede Yexowa yi ñoo defar téere boobu.