Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

Waajur yi ñoo moom kàddu yii

Waajur yi ñoo moom kàddu yii

Waajur yi ñoo moom kàddu yii

Lan mooy kado bi gën a réy bi ngeen mën a may seeni doom ? Mën nga leen a may li ñu soxla, mel ni seen mbëggeel, seen yar walla li ngeen di def ngir aar leen. Waaye kado bi gën bi nga leen mën a may mooy xam Yexowa ak dëgg gi nekk ci biir kàddoom, Biibël bi. (Yowaana 17:3) Xam-xam boobu dina dimbali seeni doom ñu bëgg Yexowa ak seen xol bépp te jaamu ko, bu dee sax ay xale yu tuuti lañu. — Macë 21:16.

Waajur yu bare dañu gis ne xale yu ndaw yi mënuñu toog lu yàgg di jàng walla di def dara, moo tax kontaan nañu lool di leen jox téere bii tudd Li ma mën a jàng ci sama Biibël. Njàngale bu nekk dañu ko defar ngir xale bi am lu muy jàng ci fasoŋ bu yomb. Xale yi am ñetti at jëm suuf lañu xalaat bi ñu doon def nataal yi ak bind yi ñu àndal. Ci njàngale bu nekk am na fu ñu lay wax li nga mën a def ak sa doom. Téere bii tudd Li ma mën a jàng ci sama Biibël du fowukaayu xale. Li ko tax a jóg mooy yéen waajur yi ngeen toog ak seeni doom di leen ko jàngal. Loolu dina tax ngeen tàmm di waxtaan ci seen biir.

Wóor na ñu ne téere bii dina leen dimbali ci jàngal seeni doom dëgg gi nekk ci Biibël bi, li ‘ dale ci seen ngune ’. — 2 Timote 3:14, 15.

Seeni mbokk ci ngëm,

Jataay biy dogal ci Seede Yexowa yi

[Nataal bi nekk paas 3]