Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

4-H

Xew-xew yi gën a am solo ci dundu Yeesu — Waare Yeesu bi mujj ci Yerusalem (Xaaj 2)

Xew-xew yi gën a am solo ci dundu Yeesu — Waare Yeesu bi mujj ci Yerusalem (Xaaj 2)

JAMONO JA

BÉRÉB BA

XEW-XEW BA

MACË

MÀRK

LUUG

YOWAANA

14 Nisan

Yerusalem

Yeesu xamle na ne Yudaa workat la, mu dàq ko

26:21-25

14:18-21

22:21-23

13:21-30

Mu taxawal Reeru Sàng bi (1 Korent 11:23-​25)

26:26-29

14:22-25

22:19, 20, 24-30

 

Mu yégle ne Piyeer dina ko weddi te ndaw yi dinañu tasaaroo

26:31-35

14:27-31

22:31-38

13:31-38

Dige na dimbalikat ; misaalu garab gu wóor gi ; mu santaane mbëggeel ; ñaanam bi mujj ak ndawam yi

     

14:1–17:26

Setsemane

Mu am tiis wu réy bi mu nekkee ci tool bi ; Wor nañu Yeesu te jàpp ko

26:30, 36-56

14:26, 32-52

22:39-53

18:1-12

Yerusalem

Anas di ko laaj ay laaj ; Kayif ak kureelu àttekat yi di ko àtte ; Piyeer weddi ko

26:57–27:1

14:53–15:1

22:54-71

18:13-27

Yudaa workat bi xaru (Jëf ya 1:​18, 19)

27:3-10

     

Taxaw na ci kanamu Pilaat, ci kanamu Erood, mu dellusiwaat ci Pilaat

27:2, 11-14

15:1-5

23:1-12

18:28-38

Pilaat di ko bëgg a bàyyi waaye Yawut yi laaj Barabas ; ñu àtte ko ngir ñu daaj ko ci bant

27:15-30

15:6-19

23:13-25

18:39–19:16

(Àjjuma, booru 15h)

Golgota

Dee na ci bant

27:31-56

15:20-41

23:26-49

19:16-30

Yerusalem

Wàcce nañu néew bi, dugal ko ci bàmmeel

27:57-61

15:42-47

23:50-56

19:31-42

15 Nisan

Yerusalem

Sarxalkat yu mag ya ak Farisen ya tëj bàmmeel ba ba mu wóor te teg fa wottukat

27:62-66

     

16 Nisan

Yerusalem ak li ko wër ; Emayus

Yeesu dekki ; mu feeñu taalibeem yi juróomi yoon

28:1-15

16:1-8

24:1-49

20:1-25

Bi 16 Nisan weesoo

Yerusalem ; Galile

Mu feeñu taalibeem yi ay yoon yu bare (1 Korent 15:​5-7 ; Jëf ya 1:​3-8) ; mu jàngale ; mu sant leen ñu sàkku ay taalibe

28:16-20

   

20:26–21:25

25 Iyyar

Tundu Oliw ya, wetu Betani

Yeesu yéeg na asamaan 40 fan gannaaw bi mu dekkee (Jëf ya 1:​9-​12)

   

24:50-53