Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

5

Li ñu wax ci Biibël bi

Li ñu wax ci Biibël bi

Yexowa Yàlla moo am sañ-sañu jiite. Ni muy jiite mooy jiite bi gën. Li mu bëggoon ci suuf si ak ci nit ñi dina am.

Bi 4026 B.S.J. weesoo

“ Jaan ja ” dafa weddi ne Yexowa am na sañ-sañu jiite, weddi it ne ni Yàlla di jiitee baax na. Yexowa dige na ne dina indi “ xeet ”, walla askan buy toj boppu jaan ja, maanaam Seytaane (Njàlbéen ga 3:1-5, 15). Waaye bala loolu di am, Yexowa bàyyi na doomu Aadama yi jiite seen bopp te nekk ci loxoy Seytaane.

1943 B.S.J

Yexowa wax na Ibraayma ne “ xeet ” woowu mu dige, ci askanam lay jóge (Njàlbéen ga 22:⁠18).

Bi 1070 B.S.J. weesoo

Yexowa dig na buur Daawuda ne “ xeet ” woowu, ci askanam lay jóge. Dig na loolu itam doomam Suleymaan (2 Samwil 7:12, 16 ; 1 Rois 9:3-5 ; Esayi 9:​5, 6).

29 C.S.J.

Yexowa wone na ne “ xeet ” woowu mu waxoon ca njàlbéen ga, Yeesu la, moom mi donn nguur gi ci maamam Daawuda (Galasi 3:16 ; Luug 1:31-33 ; 3:21⁠, 22).

33 C.S.J.

Jaan ja, Seytaane, màtt na “ xeet ” woowu bi mu fexee ba ñu rey Yeesu. Yexowa dekkal na Yeesu ngir mu dund ci asamaan te nangu na saraxu bakkanu Yeesu bu mat sëkk. Yexowa ci sarax boobu la sukkandiku ngir baal doomu Aadama yi seeni bàkkaar te may leen dund gu dul jeex (Njàlbéen ga 3:15 ; Jëf ya 2:32-36 ; 1 Korent 15:21, 22).

Booru 1914 C.S.J.

Yeesu daaneel na jaan ja, Seytaane, ci kaw suuf, te jotam bareetul (Peeñu ma 12:7-9, 12).

Liy xëw ëllëg

Yeesu dina tëj Seytaane 1 000 at, ba pare dina ko rey. Noonu lay toje boppam. Li Yexowa bëggoon ci suuf si ak ci nit ñi dina am, te dina sellal turam ci bépp tuumaal te wone ne moom rekk moo am sañ-sañu jiite (Peeñu ma 20:⁠1-3, 10 ; 21:⁠3, 4).