Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

2

Turu Yàlla ci Mbind yu sell yi ci làkku Gereg

Turu Yàlla ci Mbind yu sell yi ci làkku Gereg

Boroom xam-xam yu mag yi ci Biibël bi nangu nañu ne turu Yàlla bi ñu binde ñeenti araf yii ñuy woowe Tétragramme (יהוה), feeñ na lu jege 7 000 yoon ci Mbind yu sell yu njëkk ya ci làkku Ebrë. Waaye, ñu bare dañu foog ne tur boobu feeñul ci Mbind yu sell yu njëkk ya ci làkku Gereg. Loolu moo tax ñu ëpp ci ñiy tekki Biibël bi, bu ñu jëlee Mbind yu sell yi ci làkku Gereg, tekki ko ci seen làkk, duñu ci boole turu Yàlla. Bu dee sax yegg nañu ci ay aaya yoo xam ne tétragamme boobu dafa ciy feeñ ci làkku Ebrë, tekkikat yu bare dañuy dindi turu Yàlla, bind fa “ Boroom bi ”.

Seede Yexowa yi ñoom, defuñu loolu. Ci Mbind yu sell yi ci làkku Gereg yi ñu tekki, dañu ciy gis turu Yàlla, maanaam Yexowa, lu tollook 237 yoon. Ñaari mbir la tekkikat yooyu sóoraale bi ñuy jël dogal boobu : 1) Mbind yi ñu yor tey ci làkku Gereg, ay sotti lañu. Mat nañu ay junniy sotti te li ci ëpp dañu leen sotti ñaari téeméeri at walla lu ko ëpp gannaaw bi ñu bindee téere yu njëkk ya. 2) Ca jamono jooju, ñi doon sotti mbind yu sell yi, dañu doon rampalaase Tétragramme bi, maanaam turu Yàlla, ak Kurios, benn baat ci làkku Gereg buy tekki “ Boroom bi ”. Walla bu ñu doon sotti dañu doon sukkandiku ci ay sotti yoo xam ne dañu ci dindi woon turu Yàlla ba pare, def ci “ Boroom bi ”.

Kurél bi tekki sotti Biibël bi tudd Traduction du monde nouveau dafa gis ne am na ay firnde yu wóor yuy wone ne Tétragramme bi feeñoon na ci Mbind yu sell yi ci làkku Gereg yu njëkk ya. Gis-gis boobu mu ngi sukkandiku ci lii di topp :

  • Tétragramme bi dafa feeñoon ci sotti Mbind yu sell yi ci làkku Ebrë yi amoon ci jamono Yeesu ak apootaram yi. Du ñépp a dàkkooroon ci loolu bu njëkk, waaye léegi kenn mënul weddi ne Tétragramme bi feeñoon na ci sotti yooyu ndaxte gis nañu ci wetu dëkk bi tudd Qoumrân ay sotti Mbind yu sell yi ci làkku Ebrë yu ñu defoon ci jamono Yeesu ak taalibeem yu njëkk ya.

  • Ci jamono Yeesu ak apootaram yi, Tétragramme bi feeñoon na itam ci Mbind yu sell yi ci làkku Ebrë yi ñu tekki woon ci Gereg. Ci lu mat ay téeméeri at, boroom xam-xam yu mag yi ci wàllu Biibël bi dañu foogoon ne Tétragramme bi feeñul woon ci tekki bi tudd Septante ci tubaab [maanaam Mbind yu sell yi ci làkku Ebrë yu ñu tekki ci làkku Gereg]. Ci booru atum 1950, ay boroom xam-xam yu mag gëstu nañu ay daggitu Septante boobu ci làkku Gereg yu yàgg yi amoon ci jamono Yeesu. Turu Yàlla feeñ na ci yenn ci daggit yooyu, te ñu ngi ko binde arafu Ebrë. Kon ci jamono Yeesu, turu Yàlla mu ngi woon ci Mbind yu sell yi ci làkku Gereg. Waaye lu jege 300 at gannaaw jamono apootar yi, turu Yàlla feeñatul woon ci ay sotti Septante yu mag yu mel ni Codex Vaticanus ak Codex Sinaiticus (ci Njàlbéen ga ba Malasi), fekk turu Yàlla feeñoon na ci ay sotti yu gën a yàgg. Loolu moo tax, ci biir sotti yi ñu def gannaaw jamono apootar yi, bettuñu bi ñu gisulee turu Yàlla ci téereb Injiil, maanaam Mbind yu sell yi ci làkku Gereg.

    Lii la Yeesu waxoon ci lu leer : “ Man ñëw naa ci sama turu Baay ”. Waxoon na itam ne lépp lu muy def mu ngi koy def ci ‘ turu Baayam ’

  • Ci Mbind yu sell yi ci làkku Gereg, Yeesu dafa doon tudd turu Yàlla te di ko xamal nit ñi (Yowaana 17:​6, 11, 12, 26). Lii la Yeesu waxoon te mu leer nàññ : “ Man ñëw naa ci sama turu Baay ”. Waxoon na itam ne lépp lu muy def mu ngi koy def ci ‘ turu Baayam ’ (Yowaana 5:​43 ; 10: 25).

  • Ndegam Mbind yu sell yi ci làkku Gereg ñoo topp ci Mbind yu sell yi ci làkku Ebrë te ñoom ñaar yépp jóge ci gémmiñu Yàlla, kon du yenu maanaa turu Yàlla feeñ ci benn bi te bañ a feeñ ci beneen bi. Ci booru atum 50 ci suñu jamono, lii la taalibe Yeesu bi tudd Saag waxoon magi mbooloo yi nekkoon Yerusalem : “ Simoŋ nettali na, ni Yàlla seetsee bu jëkk ñi dul Yawut, ngir sàkku ci ñoom xeet wu ñu tudde turam ” (Jëf ya 15:14). Bu kenn xamul woon turu Yàlla ci jamono jooju walla bu kenn tuddul woon turu Yàlla, kon Saag du wax loolu.

  • Ci Mbind yu sell yi ci làkku Gereg, turu Yàlla feeñ na ci fasoŋu bind bu ñu gàttal. Mën nañu ko gis ci Peeñu ma 19:​1, 3, 4, 6, ci baat bii : “ Aleluya ”. “ Aleluya ” mu ngi jóge ci baatu Ebrë buy tekki “ Magalleen Ya ”. “ Ya ” mooy Yexowa bu ñu gàttal. Tur yu bare yu nekk ci Mbind yu sell yi ci làkku Gereg, ci turu Yàlla lañu leen jële. Ni ko ay boroom xam-xam waxe, turu Yeesu ci boppam mu ngi tekki “ Yexowa mooy Musalkat ”.

  • Am na ay téere Yawut yu yàgg yu wone ne turu Yàlla mu ngi woon ci téere yi Yawut yi nekkoon karceen doon bind. Téere bi tudd Tossefta, téere la bu boole ay ndigal yu bare te ñu pare ko ci booru atum 300 ci suñu jamono. Téere boobu, dafa wax lu jëm ci ay téere karceen yi ñu doon lakk ci bésu noflaay bi. Dañu ci wax ne dañu lakk “ téere Injiil [yiy nettali dundu Yeesu] ak téere minim yi [dafa mel ni noonu lañu doon woowee Yawut yi nekkoon karceen] ” ak it “ fi ñu binde turu Yàlla ci téere yooyu ”. Bind nañu it ci Tossefta boobu li Rabbi Yosé bu Galile wax. Rabbi Yosé mu ngi doon dund ci at yi weesu atum 100 ci suñu jamono. Dafa doon wax ne, ci yeneen bésu semen bi, am na ku doon “ kuppati turu Yàlla foofu [maanaam, ci téere karceen yi, ci li ñu xalaat] te dénc xotit yi fu wóor ba pare lakk li des ”.

  • Am na ay boroom xam-xam yu mag ci wàllu Biibël bi ñu nangu ne, dafa mel ni turu Yàlla feeñoon na ci Mbind yu sell yi ci làkku Gereg ci ay aaya yu ñu jële woon ci Mbind yu sell yi ci làkku Ebrë. Diksoneer bi tudd The Anchor Bible Dictionary, lii la wax ci xaaj bi tudd “ Le Tétragramme dans le Nouveau Testament ” : “ Am na ay firnde yuy wone ne, bi ñu njëkkee bind N[ouveau] T[estament] bi (maanaam Kóllëre gu bees gi), Tétragramme bi, turu Yàlla, Yahweh, feeñoon na ci yenn aaya yi walla sax ci aaya yépp yi ñu jële ci A[ncien] T[estament] (maanaam Kóllëre gu njëkk ga), bindaat leen ci N[ouveau] T[estament] ”.  George Howard mi nekk boroom xam-xam bu mag, lii la wax : “ Ndegam Tétragramme bi mu ngi woon ci sotti Biibël yi ci làkku Gereg [maanaam Septante] yi igliis yu njëkk ya doon jëfandikoo, kon jaadu na ñu gëm ne ñi doon bind N[ouveau] T[estament], bu ñu doon bindaat ay aaya yu ñu jële woon ci Téere yu sell yi, dañu doon bàyyi turu Yàlla ci aaya yi mu nekkoon ”.

  • Ay tekkikat yu siiw ci wàllu Biibël bi bind nañu turu Yàlla ci tekki Mbind yu sell yi ci làkku Gereg bi ñu def ci seen làkk. Am na ñu def loolu bala sax tekki Biibël bi tudd Traduction du monde nouveau di am. Tekki yiy topp bokk nañu ci : A Literal Translation of the New Testament . . . From the Text of the Vatican Manuscript, bu Herman Heinfetter (1863) ; The Emphatic Diaglott, bu Benjamin Wilson (1864) ; Bible de Darby (1940) fi ñu mën a gis “ Jéhovah ” ci li ñu bind ci suufu yenn paas yi ; The New Testament Letters, bu J.W.C. Wand, mi nekkoon Ewek bu Londres (ci atum 1946) ; Bible de Chouraqui (1985) bu binde turu Yàlla IHVH ; Évangiles yi ak Apocalypse bu C. Tresmontant (yi génn diggante 1984 ak 1988) fu ñu binde turu Yàlla yhwh. Rax-ci-dolli, ci benn Biibël bu ñu tekki ci español (1919), Pablo Besson bind na “ Jehová ” ci Luug 2:15 ak ci Yudd 14, te ci li mu bind ci suufu ay paas yu bare ci Biibël boobu (ci lu ëpp 100 yoon), wone na ne mën nañu binde turu Yàlla noonu. Lu yàgg bala tekki yooyu di am, li dale atum 1500 jëm ci suñu jamono, Tétragramme bi feeñoon na ci ay aaya yu bare ci ay tekki Mbind yu sell yi ci làkku Gereg yi ñu def ci làkku Ebrë. Bu ñu xoolee ci Mbind yu sell yi ci làkku Gereg yi ñu tekki ci làkku Almaañ kese, am na ci 11 yu binde turu Yàlla “ Jehovah ” (walla “ Yahweh ” ci Ebrë). Te am na ñeenti tekkikat ci làkk boobu yu bind “ Boroom bi ”, teg ci turu Yàlla ci biir ay xala (parenthèses). Am na lu ëpp 70 tekki Biibël ci làkku Almaañ yu bind turu Yàlla ci suufu paas yi walla ci leeral yi.

    Turu Yàlla ci Jëf ya 2:​34 ci l’Emphatic Diaglott, bu Benjamin Wilson (ci atum 1864)

  • Turu Yàlla mu ngi feeñ ci Mbind yu sell yi ci làkku Gereg ci ay tekki Biibël yu ñu def ci lu ëpp téeméeri làkk. Ci ay làkk yu bare ci Afrig, Amerig, Asi, Ërob ak Pasifig, nit ñi dañu faral di tudd turu Yàlla. (Xoolal ci paas 12 ak 13). Ñi tekki Biibël bi ci làkk yooyu, dañu sukkandiku ci ay firnde yu mel ni li ñu faramfàcce fii ci kaw ba tax ñu def turu Yàlla ci seeni tekki Biibël. Am na ci sax yu yàggul a génn, mel ni la Bible en rotumien (1999), fi ñu bind “ Jihova ” lu mat 51 yoon ci 48 aaya, ak tekki bi ci làkku batak toba, benn làkku waa Indonésie (1989), fu “Jahowa” feeñ 110 yoon.

    Turu Yàlla ci Màrk 12:​29, 30 ci Biibël bi ñu tekki ci benn làkku Hawaï ci atum 1816

Dëgg-dëgg, am na ay firnde yu leer yu war a tax ñu delloo turu Yàlla fi mu nekkoon ci Mbind yu sell yi ci làkku Gereg. Loolu la tekkikat yi génne Traduction du monde nouveau def. Ñoom, cér bu mag lañu may turu Yàlla te seen ragal Yàlla moo tax bu ñuy tekki Mbind yu sell yi, duñu ci dindi dara (Peeñu ma 22:​18, 19).