4-E
Xew-xew yi gën a am solo ci dundu Yeesu — Waare bu mag bi Yeesu def ca Galile (Xaaj 3) ak ca Yude
JAMONO JA |
BÉRÉB BA |
XEW-XEW BA |
MACË |
MÀRK |
LUUG |
YOWAANA |
---|---|---|---|---|---|---|
32, bi bésu mucc ga weesoo |
Galile; Betsayda |
Bi ñu nekkee ci gaal gi ; Yeesu wax ñu moytu lawiiru farisen yi ; mu faj góor gu gumba |
||||
Diwaanu Sesare bu Filib |
Caabiy Nguur gi ; mu xamal ne dina dee, dekki |
— |
||||
Ndamu Yeesu jolli ci moom ; Yexowa wax |
— |
|||||
Faj na xale bu rab jàpp |
— |
|||||
Mu waxaat ne dina dee, dekki |
— |
|||||
Mu fey warugar ak estateer bu jóge ci jën |
— |
|||||
— |
||||||
Ci yoonu Yerusalem, mu wax taalibe yi ñu bàyyi lépp ngir Nguur gi |
Waare bi Yeesu def ca Yude
JAMONO JA |
BÉRÉB BA |
XEW-XEW BA |
MACË |
MÀRK |
LUUG |
YOWAANA |
---|---|---|---|---|---|---|
32, Màggalu mbaar ya |
Yerusalem |
Mu jàngale ca màggal ga ; ñu yebal alkaati ya ñu jàppi ko |
||||
Mu ne : “ Man maay leeru àddina si ” ; mu faj gumbag judduwaale |
||||||
Xéyna Yude |
Mu yebal 70 taalibe ; ñu délsi fees ak mbég |
|||||
Yude ; Betani |
Misaalu nit ku baax ku dëkk Samari ; mu seeti Maryaama ak Màrt |
|||||
Xéyna Yude |
Mu jàngale ni ñu war a ñaane Yàlla ; misaalu xarit ji lakkale |
|||||
Baaraamu Yàlla la dàqe rab ; mu joxewaat firndeg Yunus |
||||||
Mu lekk ak Farisen yi, mu ñaawlu naaféqu Farisen yi |
||||||
Léebu yi : ki bare alal te ñàkk xel ak surga bu takku te teey |
||||||
Faj na jigéen ju xuuge ci bésu noflaay ; léebu doomu fuddën gi ak léebu lawiir bi |
||||||
32, Màggalu bés ba ñu sellalee kër Yàlla ga |
Yerusalem |
Misaalu sàmm bu baax bi ak gétt gi ; Yawut ya bëgg ko rey aki xeer ; mu dem Betani ci ginnaaw Yurdan |