Leetar bu jóge ci Jataay biy dogal
Mbokk yi:
Mbëggeel ci Yàlla ak ci nit ñi, moo ñuy xiir ñu dem «sàkk ay taalibe ci xeet yépp, sóob leen ci ndox.» (Macë 28:19, 20; Màrk 12:28-31) Mbëggeel dëgg dafa am doole. Te mbëggeel googu moo ñuy dimbali ñu laal xolu «ñépp ñu jagoo dund gu dul jeex.»—Jëf ya 13:48.
Bu njëkk, dañu doon jàpp ci suñu xel, li ñu bëgg a wax nit ñi ci liggéeyu waare bi. Bu ñu amee bunt, loolu lañu leen di wax, ba pare bàyyi leen ay téere. Waaye léegi, dañu war góor-góorlu di waajal suñu bopp te xalaat bu baax ci ni ñu mënee wax ak nit ñi. Bu ñuy wax ak ñoom ci li leen itteel, dañu leen di won ne bëgg nañu leen. Loolu dafay tekki ne dañu war a tànn waxtaan bu itteel ku nekk ci ñoom, te xalaat bu baax ci li ku nekk soxla. Naka lañu téere bii mënee dimbali ñu def loolu?
Téere bii am na fukk ak ñaari lesoŋ yuy wax ci jikko yu ñuy dimbali ñu won nit ñi mbëggeel. Noonu dinañu leen dimbali ñu nekk taalibe Yeesu. Lesoŋ bu nekk dafa sukkandiku ci li Biibël bi nettali ci Yeesu walla ci kenn ci kerceen yu njëkk ya, ku wone jikko boobu ci liggéeyu waare bi. Li ñu bëgg mooy, ñu bañ di jàpp ci suñu xel li ñu bëgg a wax nit ñi, waaye, ñuy góor-góorlu ci won nit ñi mbëggeel ci liggéeyu waare bi. Bu de sax soxla nañu jikko yooyu yépp ci suñu liggéeyu waare bi, yenn ci jikko yooyu dañu leen gën a soxla bu ñuy tàmbali waxtaan, yeneen yi bu ñuy seetiwaat nit ñi, walla bu ñuy jàngal nit ñi ba ñu nekk taalibe Yeesu.
Booy jàng lesoŋ bu nekk, xalaatal ci ni nga mënee wone jikko boobu booy wax ak nit ñi nekk fi nga dëkk. Defal noonu ak lesoŋ bu nekk. Defal lépp ngir yokk sa mbëggeel ci Yexowa ak ci nit ñi. Ak mën-mën boo mënta am, xamal ne, mbëggeel rekk moo la mën a dimbali, nga jàngal nit ñi ba ñu nekk taalibe Yeesu.
Am nañu mbégte bu réy ànd ak yeen di liggéey, maanaam, di ‘jaamoondoo Yàlla.’ (Cefaña 3:9) Na leen Yexowa barkeel bu baax ci ni ngeen di wéy di won nit ñi mbëggeel ba dimbali leen ñu nekk taalibe Yeesu!
Seeni mbokk yi bokk ci,
Jataay biy dogal bu Seede Yexowa yi