LI ÑU YOKK CI WAXTAAN YI NEKK CI TÉERE BII: XAAJ 1
Dëgg yi ñuy jàngal nit ñi
Yeesu nee na, ñi am xol bu rafet dinañu xame dëgg gi, bu ñu ko déggee. (Yowaana 10:4, 27) Kon saa yu ñuy waxtaan ak nit ñi, dañu leen war a xamal dëgg yu yomb a nànd yi nekk ci Biibël bi. Ci misaal, mën nga ko laaj: «Ndax xamoon nga ne . . . ?» wala «Ndax mas nga dégg lii . . . ?» Ba paree nga jëfandikoo aaya yi nekk ci Biibël bi yuy leeral dëgg googu. Dëgg yu ñuy jàngal nit ñi, mën na laal seen xol, te Yàlla mën na tax ba dëgg googu meññ!—1 Korent 3:6, 7.
ËLËG
-
1. Jëf yu bon yi ñuy gis tey ak doxalinu nit ñi dañuy wone ne léegi Yàlla soppi mbir yi.—Macë 24:3, 7, 8; Luug 21:10, 11; 2 Timote 3:1-5.
-
2. Suuf si du fi mas a jóge.—Taalifi Cant 104:5; Kàdduy Waare 1:4.
-
3. Suuf si dinañu ko defaraat.—Esayi 35:1, 2; Peeñu 11:18.
-
4. Ku nekk dina am wér-gi-yaram bu mat sëkk.—Esayi 33:24; 35:5, 6.
-
5. Mën nga dund ba fàww ci kaw suuf.—Taalifi Cant 37:29; Macë 5:5.
DUNDINU NJABOOT
-
6. Jëkkër dafa war a «bëgg jabaram, ni mu bëgge boppam»—Efes 5:33; Kolos 3:19.
-
7. Jabar dafa war a «weg jëkkëram.»—Efes 5:33; Kolos 3:18.
-
8. Ku nekk dafa war a yem ci ki mu séyal.—Malasi 2:16; Macë 19:4-6, 9; Yawut ya 13:4.
-
9. Xale yi dañoo war a teral seeni waajur te di leen déggal. Noonu li ñu def, mu àntu.—Kàddu yu Xelu 1:8, 9; Efes 6:1-3.
YÀLLA
-
10. Yàlla am na tur.—Taalifi Cant 83:19; Yeremi 10:10.
-
11. Yàlla dafay wax ak ñun jaare ko ci Biibël bi.—2 Timote 3:16, 17; 2 Piyeer 1:20, 21.
-
12. Yàlla ku jub la te du gënaatle.—Baamtug Yoon wi 10:17; Jëf ya 10:34, 35.
-
13. Yàlla ku ñu bëgg a dimbali la.—Taalifi Cant 46:2; 145:18, 19.
ÑAAN
-
14. Yàlla dafa bëgg ñu di ko ñaan.—Taalifi Cant 62:9; 65:3; 1 Piyeer 5:7.
-
15. Biibël bi dafa ñuy jàngal ni ñu mënee ñaan Yàlla.—Macë 6:7-13; Luug 11:1-4.
-
16. Dañu war a di ñaan Yàlla saa su ne.—Macë 7:7, 8; 1 Tesalonig 5:17.
YEESU
-
17. Yeesu jàngalekat bu mag la woon, te xelal yi mu joxe duñu mas a xewi.—Macë 6:14, 15, 34; 7:12.
-
18. Yeesu yéglewoon na liy xew ci suñu jamono.—Macë 24:3, 7, 8, 14; Luug 21:10, 11.
-
19. Yeesu Doomu Yàlla la.—Macë 16:16; Yowaana 3:16; 1 Yowaana 4:15.
-
20. Yeesu nekkul Yàlla Aji Kàttan ji.—Yowaana 14:28; 1 Korent 11:3.
NGUURU YÀLLA
-
21. Nguuru Yàlla, nguur dëgg la ci asamaan.—Dañeel 2:44; 7:13, 14; Macë 6:9, 10; Peeñu 11:15.
-
22. Nguuru Yàlla dina jël palaasu nguuru doomu Aadama yi.—Taalifi Cant 2:7-9; Dañeel 2:44.
-
23. Nguuru Yàlla rekk a mën a dindi coono doomu Aadama yi yépp.—Taalifi Cant 37:10, 11; 46:10; Esayi 65:21-23.
COONO YI
-
24. Yàlla du ñu teg coono.—Baamtug Yoon wi 32:4; Saag 1:13.
-
25. Seytaane moo nekk di ilif àddina si.—Luug 4:5, 6; 1 Yowaana 5:19.
-
26. Bu ñu Yàlla gisee ñu nekk ci coono, loolu dafa koy naqari.—Taalifi Cant 34:18-20; Esayi 41:10, 13.
-
27. Nes tuut, Yàlla dina fi dindi coono yi yépp.—Esayi 65:17; Peeñu 21:3, 4.
DEE
-
28. Ñi dee xamatuñu dara. Nekkuñu di torox fenn.—Kàdduy Waare 9:5; Yowaana 11:11-14.
-
29. Ñi dee mënuñu dimbali kenn ci ñun walla lor ñu.—Taalifi Cant 146:4; Kàdduy Waare 9:6, 10.
-
30. Suñu mbokk yi dee dinañu mas a dekki.—Ayóoba 14:13-15; Yowaana 5:28, 29; Jëf ya 24:15.
-
31. «Dee dootul am.» —Peeñu 21:3, 4; Esayi 25:8.
DIINE YI
-
32. Yàlla nanguwul diine yi yépp.—Yeremi 7:11; Macë 7:13, 14, 21-23.
-
33. Yàlla dafa sib naaféq yi.—Esayi 29:13; Mise 3:11; Màrk 7:6-8.
-
34. Ñi bokk ci diine dëgg gi, dañu leen di ràññee ci mbëggeel bi ñu am ci seen biir.—Mise 4:3; Yowaana 13:34, 35.