Xam-xam bi nekk ci Kàddu Yàlla

Xam-xam bi nekk ci Kàddu Yàlla

Seetal tont yi Biibël bi joxe ci 20 laaj yu am solo.

Kan mooy Yàlla ?

Ay diine yu bare dañuy jàngale ne kenn mënul xam Yàlla walla Yàlla nekkul leneen lu dul kàttan, waaye Biibël bi waxul loolu.

Naka ngeen mënee xam Yàlla ?

Ndax yem ci liir Biibël bi doy na ?

Ci ñan la Yàlla jaar ngir bind Biibël bi ?

Ndax xam-xamu nit moo ci nekk walla lu ko raw ?

Ndax Biibël bi ànd na ak li tubaab di woowe science ?

Bu dee Biibël bi ci Yàlla la jóge, kon buy wax ci lu laal science, dafa war a ànd ak li science.

Lan mooy xibaar bi nekk ci Biibël bi ?

Fukki aaya yii tënk nañu xibaar bi nekk ci Biibël bi.

Lan la Biibël bi yéglewoon ci Almasi bi ?

Am na yégle yu bare yu Yeesu matal yoo xam ne du ci pexeem la mënoon a ame.

Lan la Biibël bi yégle lu jëm ci suñu jamono ?

Xare yi di gën a bare, xiif di yokku, lu bon di law, ñaawteef di gën a bare, loolu yépp lu mu tekki ?

Ndax Yàlla mooy teg nit ñi coono ?

Ndax Yàlla dafa ñuy natt moo tax mu ñuy teg coono ?

Lu tax nit ñi di am metit ?

Bu dee du Yàlla mooy teg nit metit, kon lu waral metit yi ?

Lan lu rafet la Biibël bi wax ci ëllëg ?

Yaakaar bu neex boobu mën na la jaaxal.

Bu nit deewee, lan moo koy dal ?

Ndax dee jaar-jaar la ngir dem ci beneen dund ?

Ndax mën nañu yaakaar a gisaat ñi dee ?

Ci dëgg-dëgg, ndax dee mooy njeexteelu lépp ?

Lan la Biibël bi wax ci liggéey ?

Ñu bare dañu gise liggéey ni yen bu metti, moo tax ñu yàkkamti bés bu ñu dul liggéey. Ndax noonu la Yàlla gise woon liggéey ?

Naka ngeen mën a yore seen xaalis ?

Xelal yi dul xewi yi nekk ci Biibël mën nañu la dimbali nga xam ni ngay yore sa alal te bañ koo bàyyi mu jiital la.

Naka ngeen mënee am bànneex ?

Biibël bi am na ay xelal yu wóor yu lay yóbbu ci yoonu mbégte ak doylu.

Naka lañu mënee jànkoonte ak suñuy coono ?

Bu coono yi demee ba bëgg ñoo ëpp loxo, Biibël bi mën na ñu ci dimbali.

Naka la Biibël bi mën a dimbalee seen njaboot ?

Xoolal ni sa njaboot mënee am jàmm ak mbégte.

Naka ngeen mënee jege Yàlla ?

Mën nga am xaritoo bu dëgër ak Yàlla.

Naka nga mënee jariñoo bu baax li ngay liir ci Biibël bi ?

Lépp looy liir ci Biibël bi, boo laajee sa bopp ñeenti laaj yu yomb, dinga ci jële njariñ bu réy.