Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LAAJ 19

Lan lañu wax ci biir téere yi nekk ci Biibël bi ?

Lan lañu wax ci biir téere yi nekk ci Biibël bi ?

MBIND YI CI LÀKKU EBRË (“ KÓLLËRE GU NJËKK GI ”)

TAWREET (5 TÉERE) :

Njàlbéen ga, Gàddaay gi, Lévitique, Nombres, Deutéronome

Dañu ciy nettali li xewoon bi Yàlla tàmbalee sàkk ba bi mu sosee mbooloo Israyil

TÉERE YUY NETTALI LI XEWOON DÉMB (12 TÉERE) :

Yosuwe, Njiit yi, Ruth

Dañu ci nettali li xewoon bi bànni Israyil di dugg ci Réew mi leen Yexowa digoon ak li xewoon gannaaw loolu

1 ak 2 Samwil, 1 ak 2 Buur yi, 1 ak 2 Chroniques

Dañu ci nettali li xewoon ci mbooloo Israyil ba bi ñu alagee Yerusalem

Esras, Nehémia, Esther

Dañu ci nettali li xewoon bi Yawut yi jógee réewu Babilon mi leen jàppoon

TÉERE TAALIF YI (5 TÉERE) :

Job, Sabóor, Kàddu yu Xelu, Ecclésiaste, Chant de Salomon

Téere yooyu dañu dajale ay kàddu yuy maye xel ak ay woy

TÉERE YUY YÉGLE ËLLËG (17 TÉERE) :

Esayi, Yérémi, Lamentations, Ézékiel, Dañeel, Hoshéa, Yoël, Amos, Obadia, Yona, Mika, Nahoum, Habaqouq, Tsephania, Ase, Sakari, Malasi

Téere yooyu dañu boole ay yégle yonent yu jëm ci mbooloo Yàlla mi

MBIND YI CI LÀKKU GEREG (“ KÓLLËRE GU BEES GI ”)

INJIIL (4 TÉERE) :

Macë, Màrk, Luug, Yowaana

Dañu ci nettali lu jëm ci Yeesu ak liggéeyu waare bi mu defoon

JËFI NDAW YA KIRIST YÓNNI (1 TÉERE) :

Dañu ci nettali bi ñu komaasee taxawal mbooloo karceen yi ak liggéeyu misioneer yi

BATAAXAL YI (21 TÉERE) :

Room, 1 ak 2 Korent, Galasi, Efes, Filib, Kolos, 1 ak 2 Tesalonig

Bataaxal yooyu, dañu leen yónnee woon ay mbooloo karceen

1 ak 2 Timote, Tit, Filemon

Bataaxal yooyu, dañu leen yónnee woon ay karceen

Yawut ya, Saag, 1 ak 2 Piyeer, 1, 2, ak 3 Yowaana, Yudd

Ay bataaxal lañu ngir karceen yi

PEEÑU MA (1 TÉERE) :

Dañu ciy jàng ay peeñu yu apootar Yowaana gisoon yu doon wone li naroon a am ëllëg