Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LAAJ 6

Lan la Biibël bi yéglewoon ci Almasi bi ?

Lan la Biibël bi yéglewoon ci Almasi bi ?

LI MU YÉGLEWOON

“ Yaw mii, Betleyem Efrataa, . . . ci yaw la kiy nguuru ci Israyil di jóge ndax man. ”

Mika 5:​2, MN

NI LOOLU AME

“ Bi nga xamee ne Yeesu juddu na ci Betleyem di diiwaanu Yude, amoon na ay boroom xam-xam, ñu jóge penku, ñëw Yerusalem. Booba, ci jamonoy buur bi Erodd la woon. ”

Macë 2:1

LI MU YÉGLEWOON

“ [Dañuy] séddoo samay yére, di tegoo bant sama mbubb. ”

Sabóor 22:⁠19

NI LOOLU AME

“ Xarekat ya, bi ñu daajee Yeesu ca bant ba, ba noppi dañoo jël ay yéreem, séddale ko ñeenti cér . . . Jël nañu it mbubbam bu ñu ràbb ca kaw ba ci suuf te amul benn ñaw. Xarekat ya di waxante naan : « Mbubb mi, bunu ko xotti, waaye nanu ko tegoo ay bant, ngir xam ku koy moom. » ”

Yowaana 19:​23, 24

LI MU YÉGLEWOON

“ Di ko sàmm, ba benn yaxam du damm. ”

Sabóor 34:⁠21

NI LOOLU AME

“ Bi ñu agsee ci Yeesu, dammuñu ay tànkam, ndaxte gis nañu ne booba faatu na. ”

Yowaana 19:⁠33

LI MU YÉGLEWOON

“ Sunuy bàkkaar a tax mu gaañu [“ ñu jam ko ”, MN]. ”

Esayi 53:5

NI LOOLU AME

“ Waaye kenn ca xarekat ya daldi jël xeej, jam ko ko ci wet, ca saa sa deret ak ndox di tuuru. ”

Yowaana 19:⁠34

LI MU YÉGLEWOON

“ Joxe nañu sama pey, fanweeri poseti xaalis. ”

Sakari 11:​12, 13, MN

NI LOOLU AME

“ Ca waxtu woowu kenn ci fukki taalibe ya ak ñaar, ku tudd Yudaa Iskariyo, dem ca sarxalkat yu mag ya, ne léen : « Lan ngeen ma mana jox, ngir ma jébbal leen Yeesu ? » Noonu sarxalkat ya daldi ko waññal fanweeri poseti estateer. ”

Macë 26:​14, 15 ; 27:5